Xeex bi dakkagul diggante yawuud yi ak julliti Palestin yi. Israayel a ngi wéy di tàbbal i bomb ca Gasaa. Keroog, ab loppitaan lañ bombàrde, rey ay xale ak i jigéen ñu bare. Bakkaan yaa ngi wéy di rot, lim biy gën a yokku, rawatina ci waa Palestin. Ndax, bees sukkandikoo ci jëwriñ ji ñu dénk wàllum wér-gi-yaram wa xamle na ne bi xeex bi dooree ak léegi faat nañu ci Gaasaa lu jege ñetti junniy doomi Palestin ak ñeenti téeméer ak juróom-ñaar fukk ak juróom-ñett. Waxaalewuñu nag limu ñi nga xam ne jële nañu ci ay gaañu-gaañu ak yàqute yi ci am.
LAWAXUG USMAAN SONKO
Mu nekk lu ñuy laam-laame ba léegi, di laaj ndax, njiitul Pastef la woon dina nekk lawax ci wotey yii ñu jëm. La ko ko nar a xañ, di la yoon tegoon ci ndoddam ñeel coow la doxoon diggam ak Maam Mbay Ñaŋ. Nee ñu, alxames jees dégmal, 26 oktoobar 2023, la Ëttu Àttewaay bu mag bi àtte mbir mi.
MBURU MI
Njëgu mburu maa ngi ca tànki yokk. Bulañseyi réew mi ci naal yooyu lañu taxaw. Seen mébét mooy teg fukki dërëm ci kilo mburu mu nekk. Lañuy taafantoo bokk na ca yokkuteg mbëj mi (kuraŋ) ci réew mi. Waaye tamit, lenn lañuy jëfandikoo ci seen liggéey boobu, di lëwiir bu yokk, dem ba kenn tegatu ko bët.
NDAJEM JËWRIÑ YI
Bërki-démb, ci àllarba ji, moo nekkoon ndajem jëwriñ mu njëkk ginnaaw bi Njiiti réew mi tasee woon Càmm gi. La mu xamle ca mooma ndaje mooy ag soññe jëm ci jëwriñ yooyu ñu booloo nekk benn te taxaw ci bëgg-bëggu askan wi. Ñu fas yéene ko génnewaat ci diiwaan yi ci ñeenti weer yi des. Bokk na ca ya ñu lim, Fatig, Kéedugu, kafrin ak Kawlax.