Njiitu réew mi Màki Sàll dikkaat na ci tas gi ñu tas làngug pólitig gii di PASTEF. Muy ay kàddu yu mu biral ca 78eelu ndajem mbotaayu réew yi. La ñu mën a nànde ca wax ja mooy làngug pólitig gu sàmmontewut ag li la yoon may, yoon dina def liggéeyam boo wàccee yoon. Ci gis-gisam, PASTEF dafay woote fitna saa su ne.
« SANDARMËRI MOO REY MËRI GEY »
Muy ay kàddu yu kenn ci ay mbokkam wax. Mari Géy dis ndaw su ñàkk bakkanam fee ca Ngor ginnaaw as coow lu doxoon diggam ak takk-der yi (sàndarmëri). Coow laa ngay wéy nag. Nde, ay mbokkam dañoo jàpp ne dañu koo faat.
WOTEY 2024
Mbër yaa ngay wéy di bàkku ca géew ga. Wotey 2024 yi amati mbër mu bees mu sàmp ndëndam. Muxammat Bun Abdulaay Jonn mi fi nekkoon njiitu jëwriñ yi, fésal na ag yéeneem ngir nekk ci bopp réew mi. Mu mel ni dafa ber yoonu boppam ginnaaw ba waa APR sàmpe Aamadu Ba.
NJAMBAANU MOLOTOF MI
Muy ab xibaar bu fi jiboon ci gaawu gi ne njambaanu molotof mi dañu koo fekk ca liise Delaafos. Mu mel ni lu yees am na ca. Bu ñu sukkandikoo ci këru xibaar gii di « Source A », ka nekk ca bopp ba xamees na ko. Ne ci turu Usmaan F. lay wuyoo nekk tamit kordonaatëru PASTEF ca Gël-tàppe.