LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (24/4/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

4eelu NDAJEM WAXTAAN ÑEEL XÉY AK TÀGGATU NGIR AM LI ÑUY WUT CI LIGGÉEYKAT

Tey ci alxames ji lañu doon amal ndajem waxtaan mi ñu jagleel xéy meek tàggatu gi fa CICAD (Centre International de Conférences Abdou Diouf). Mu doonoon am waxtaan ngir am li ñuy séentu ci liggéeykat. Ñoo ngi ko doon amale ci njiiteefu Njiitu Réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Naka noonu, jot na faa yékkati ay kàddu yu am solo. Li nekkoon boppu waxtaan wi mooy nu ñuy def ba xéy am, waaye tamit am ñu mën a xéy. Maanaam, nees di def ba am ñoo xam ne am nañu xarañteef gog, bu ñu leen soxlaa dinañu leen mën a jël. Ci gàttal, li mu bëgg mooy am ñoo xam ne am na ci lu ñu leen tàggat. Li ko gën a ñor, moom Njiitu réew mi, ci xéy moomu muy wax mooy xéyu ndaw ñi. Ndax, loolu moom yitte lañu ko def, moom ak ug Nguuram.

TEG NAÑU LOXO DEMBA NGOM

Demba Ngom, di rakk ci Farba Ngom, teg nañu ko loxo. Li ñu ko jàppe mooy lu ñeel ag luññutu ci caabalug CENTIF (Cellule Nationale de Traitement des Informations Financières) gi. Looloo tax, magum àttekat yi sàkku ñu jàpp ko. Jamono jii nag, ma nga ñu téye fa DIC (Division des Investigations Criminelles). Kon, fii ak lu yàggul dara, dees na xam fan lay mujj ak Yoon.

NDOGAL YI TUKKEE CI NDAJE MI AMOON FA NGOMBLAAN GA

Démb, ci àllarba ji, lañu doon amal ndajem mu am solo ñeel mbiri Force Covid-19. Nde, fan yii yépp coow looloo lëmbe réew mi. Am na ñu ñu ci jot a woolu, am sax ñu ñu ci teg loxo. Dafa di, ñoom dépite yooyu daje woon, dafa am juróom ñu fi nekkoon ay jëwriñ ñoo xam ne dañu leen a duut baaraam. Li ñu bëgg mooy ñooñu dem layoo ci kanamu yooyu ci mbir yooyu ñu leen di tudd. Muy kii di Mansuur Fay, Ismaayla Maajoor Faal, Ndey Sali Jóob Jeŋ, Sófi Galadimaa ak Mustafaa Jóob. Waaye, yemuñu foofu. Ndax, ñi ngi sàkku ñu muri mbalaani kiraayi ñaar ci seen i naataango. Muy Ndey Sali Jóob Jeŋ ak Mustafaa Jóob. Dépite yi nag, woolu nañu leen subaak jàmm fa Ngomblaan ga. Li ñu dugge woote boobu àddu ci lu jëm ci murig mbalaani kiiraayi seen ñaari naataangoo yooyu.

TABB NAÑU MUHAMMADU BASIIR SÉY

Bu yàggul la Njiitul ndajem ndeyu-àtte yi, Baajo Kamara, wàcc liggéey. Am ñu jàppoon ne sax tabb gii ñu tabb Muhammadu Basiir Séy ngir mu wuutu ko la. Ndeke, mbir mi demewul noonu. Ndax, bees sukkandikoo ci Senego, moom Muhammadu Jaawara la wuutu. Ndax, kàngaam boobu kayam dafa jeex ci weeru desàmbar atum 2024 mii ñu génn. Moom, Muhammadu Basiir Séy dees na ko samp altine jii ñu dëgmal yemoo ak ñaar-fukki fan ak juróom-ñett ci weeru awril. Su ko defee mu mën a bokk ci kurélu kàngaam yooyu.

DAAN NAÑU LAC DE GUIERS 2

Ci atum 2024 mi rekk jotoon naa tëdd ñaari weeri kaso ci lu ñeel njuuj-njaaj ci mbirum wiisaa yi ñu ko doon toppe. Waaye, dañu koo bàyyi woon bàyyig négandiku. Moom, mbëru Géejawaay mi mujj nañu koo daan fa ëttu àttewaay bu Pikin-Géejawaay. Daan nañu ko atum kaso moo xam ne dina ci tëdd ñetti weer. Ba noppi, tegal ko ci àllamaan bu tollu ci juróom-fukki miliyoŋ ak ñett. Kon, li ko war mooy mu joxe koppar googu seen boroom balay kaso di ko ci fekkaat.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj