Takk-deri duwaan yi (douaniers) dogaale nañu ay sàmbaa-bóoy yu doon jéem a jàllale sineebar. Dafa mel ni nag, tóx mi moom, mu ngi jaabaa-jonge réew mi. Fa kumpeetum, ci boori 11i waxtu ci guddi, lañu jàpp ag sëfaan gu yeboon lu tollu ci 264i kiloy sineebar (cocaïne). Liggéey boobu, mu ngi am ci guddig alxemes gi jàpp àjjuma. Mu mel ni, yoon yooyu saf na lool deftaku njaaxum yooyule. Nde, ay weer rekk ci ginnaaw, jàpp nañu fa Tàmbaakunda lim bu takkoo takku ci sineebar. Koppar ya ñu koy xayma ñoo ngi tollu ci 90i miliyoŋ, muy dëppook 1 137i kilo ak lu teg ci sineebar.
“JUB, JUBAL, JUBBANTI” CI KOW TALI YI
Li tali biy rey ciy bakkan jamono yii dafa jéggi dayo lool. Daanaka, doo toog bés boo déggul ab laksidaŋ bob, ay bakkan dañ ciy rot. Bu dee sabab yi bari nañ yit, lu ci ëpp, reewande dawalkat yi, ñàkk a sàmmonte ak yoonu dawal ak màggetaayu daamar yi lañuy duut baaraam. Moo tax, kiifay réew mi, rawati njëwriñu dem beek dikk bi, jël i matuwaay, sàrtal ay daan ak i alamaan ngir aar ak a sàmm kaaraangeg way-tukki yi.
Dafa di, fagaroo gën faju. Ngir saafara mbir mi, Nguur gi, jaare ko ci njëwriñu dem beek dikk bi, teg nay alamaan yees di gàll bépp dawalkat bu jalgati li yoon ak yoonu dawal sàrtal ci tali yeek oto yi. Bépp xeetu jalgati, utal nañ ko ab alamaan bu dawalkat biy war a faj. Dees na ci yaatal.
CFEE BI RANDAL NAÑU KO
Muy joŋante bi ñuy amal at mu jot, te ndongo yi féete ci njeexitalu daaray tuut-tànk war ko di def. Ren nag, dañu ko fomm ba jëmmi jamono. Ñu jàppoon ko ci alxemes 20 ak àjjuma 21 ci weeru suwe. Léegi, bëtal nañu ko. Xibaar boobu, ñi yore joŋantey lijaasa yi (DEXCO) ñoo ko fésal. Jàppees na ko talaata 25 ak àllarba 26 ci weeru suwe 2024.