LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (28/8/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

TASUB CESE AK HCCT

Dépite yi jëmmal nañ càkkuteefu Njiitu réew mi ñeel sémbuw àtte wiy soppi ndeyu-sàrtu réew mi ngir tas ñaari campeef yii CESE AK HCCT.
Nde, moom, Njiitu réew mi, dafa sàkku ci Ngomblaan ñu daje ngir fénc sémb woowii. Ginnaaw bi Pekkug Ngomblaan dajee tey ci àllarba ji, woolu nañ dépite yépp ëllëg ça Ngomblaan ga, bu 10i waxtu jotee ci yoor-yoor bi.

JÀPPAAT NAÑ LAT JÓOB, BÀYYIWAAT KO

Lat Jóob, njiitul LONASE la woon, lees jàppaatoon. Sunuy naataangooy Dakaractu ñoo fésal xibaar bi. Fa naawub AIBD lañ ko jàppee, fekk mu naroon a tukki, génn réew mi. Tay, ci teel, bi 7i waxtu jotee, la ko takk-deri naawu bi teg loxo.
Lees ko jàppee mooy ne, jàll-waaxu dipolomatig (passeport diplomatique) la yoroon, ñu bind ci jëwriñu tàggat-yaram te nekkatu ko. Bi ñu ko jàppee nag, ça komisariyaa bu naawu ba lañu ko téyandi woon. Waaye, mujje nañ ko bàyyi mu dellu këram.
Moom nag, kenn terewu ko génn réew mi.

WAA DIC DÉGLU NAÑ KOMISEER KEYTA

Waa DIC dañu woolu woon kees dii woowee Komiseer Keyta ngir déglu ko. Ndax, moom dafa def ab widewoo, di ci wax ne Njiitu réew mi ak elimaanu jëwriñ yi dañu jàppante woon fa njénde la ba jot faa xeex. Kàddu yooyoo taxoon ñoo woolu ko. Ginnaaw bi ñu ko dégloo ba bàyyi ko, sunu naataangooy Buur News tàllal nañ seen ngolliir, laaj ko ndax day dëggal kàddoom yi, mu tontu, wax ne du moom mooy dëggal walla di weddi. Nde, ciy waxam, deful lu mooy njañse xibaaru xeex bi. Moom nag, dina wuyujiwaat ëllëg bu 10i waxtu jotee ci yoor-yoor bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj