Muy xew-xew bu ñu dëgmal te ña fare ca lëkkatoo pólitig gii di “Sonko président 2024” naroon ko amal ci gaawug ëllëg gi. Waaye, perefe daf ko gàntal. Li ñu ko dugge woon mooy samp Usmaan Sonko ngir mu doon seen lawax ci wotey 2024 yi. Ña nga joxante woon dig-daje ca Pàrsel Acapes. Waaye de, perefe tas na seen yaakaar.
Moom sax, Usmaan Sonko, ëllëg lañuy xam ndax dina bokk ci wote yi am déet. Nde, juróom-ñaari àttekati ndajem ndeyu àtte mi ëllëg lañuy saytuy mbiram
NDEELA MAAJOOR JUUF DEM NA NDUNG-SIIN
Coow la mujj naa tàbbi ca loxoy yoon. Ndeela Maajoor Juuf, àttekat ba téyelu na ko. Tuuma yu bari lañu koy toppe. Bokk na ci njaayum doomu-aadama, def liggéeyu doktoor ci lu jaarut yoon, xañ dund àqum paj ba mu sooke dee ci lu àndut ak coobaare. Ña ko kalaame woon, di ay liggéeykatam, yoon bàyyi na leen.
Dakar-Dem-Dikk
Kër gii di Dakar-Dem-Dikk jot nañu démb ci àllarba 370i daamaar yu bees. Njiitu réew mi, Maki Sàll, moo teewe woon boobu jataay. Muy lim bu bari buy dolliku tey yombal dem ak dikk ci biir Ndakaaru ak li ko wër.