LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (4/8/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PASTEF

Ñoo ngi wéy di raafal ndawi Pastef yi. Keroog, Tuseŋ Màngaa ak Bentaleb Sow lañ jàppoon. Démb, fa Yëmbël, jàppati nañ Dr Séydu Jàllo mi jiiteendoo Pastef Kër Masaar Pastef Yëmbël. Lamin Jàllo mi jiite kurélug xaley Pastef yu Kër Masaar yi, jàpp nañ ko, ak Basiiru Ba, Bunaama Fay Njaay, Mamadu Jéy, Paap Aliyun Njaay, Umar Tekaañ, ñoo ñépp, bokk Pastef Yëmbël, ak ñeneen ak ñeneen.  Tey, jàpp nañ Paap Sow, meeru Sàngalkaam mi àndoon ak Pastef ci wotey Ngomblaan gi, 2022. Kër Njaay Lóo lañ ko jàppe, yàqate këram. Useynu Li tamit, jàpp nañ ko. Bu dee Jamiil Saane, meeru Parsel Aseni, ak Maymuuna Jéy, meeru Pàdduwaa, ñoo ngi ci loxoy Yoon ba tey.

Ngir fàttali, tey mooy juróom-benneelu fan bi Usmaan Sonko dooree ag xiifal ca kaso ba.

SIGICOOR

Bakkan rotati na fa Sigicoor ci sababu ñaxtu yi. Ceerno Biraahim Ba (20i at) moo mujje faatu ginnaaw bi ko takk-der yi soxee ab bal ci bopp, keroog 1eelu fan ci weeru ut 2023. Ay mbokkam a ko xamle. Moom nag, dafa nekkoon diggante dund ak dee ca raglub Sigicoor ba. Tey la mujje gaañu.

BENNOO BOKK YAAKAAR : MAKI SÀLL JÉBBAL NA AB SÀRT ÑI BËGG A DOON LAWAX CI WOTEY 2024 YI

Waa lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar génnee na ab yégle di ci wax ni, Njiitu réew mi, Maki Sàll, dalal na ñi bëgg a doon lawax ci wotey 2024 yi. Jébbal na leen ñoom ñépp ab sàrt bu ñu wa a xaatim. Bindees na ci yégle bi ne :

« Ñi bëgg a doon lawax ci wotey njiiteefu réew mi, weeru féewaryee 2024, amoon nañ am ndaje ak njiitul Bennoo Bokk Yaakaar ngir waxtaane sàrtub Bennoo Bokk Yaakaar.

Bi ñ jógee ci ndaje mi, dollees nay ponk ci sàrt bi laata ñu koy nangu. »

 Nee ñu, fi ak fan yu néew, dinañ siiwal ki ñu tànn mu doon lawaxu Bennoo Bokk Yaakaar. Bu dee Mansuur Fay, Maki Sàll a ko wax, ci lees dégg, mu bañ a bokk.

MBIRUM XALIFA SÀLL AK KARIIM WÀDD DINA LEER GAAWU GII

Ci alxames jii la dépite yi waroon a daje ca Ngomblaan ga ngir soppi càrtug wote gi. Waaye dañ ko mujje bëtal ba gaawug ëllëg gi, 5 ut 2023. Kon, ci gaawu gi la Xalifa Sàll ak Kariim Wàdd di xam ndax dinañ bokk am déet ci wotey 2024 yi. Njortees na ni sémbub àtte bi dina jàll.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj