Njiitu réew mi Maki Sàll woote na am ndajeem jëwrin yi ci altine tey ji. Ginnaaw aksidaŋ bu metti bi am ca diwaanu Kafrin la jël ndogal li. Aamadu Ba, magum jëwrin yi moo koy jiite. Fukk ak juróom-ñaari jëwrin ak yeneen i kilifa ñoo koy teewe ngir jël i ndogal yu leer ñeel dem beek dikk bi.
WÉR-GI-YARAM
Ànd Gësëm (kuréli doktoor yi) ajandi na ñetti fanu ñaxtu yi mu nammoon a amal (10, 11 ak 12 saŋwiyee 2023) ba ci fani 17, 18 ak 19 saŋwiyee. Ci yëgleem bi mu génne, ma ngay ñaax askan wi mu dem mayeji dereet ca Kafrin ngir xettali way-loru yi ci aksidaŋ bi ak di sàkku ci jëwrin ji mu sàmmoonteek dige yi.
MBIRI PAAP AALE ÑAŊ
Ba tey ci seen xeex ngir ñu bàyyi Paap Aale Ñaŋ, ñii di waa CAP (Coordination des Associations de Presse) a nga woon ca Tuubaa. Xalifa ba, Sëriñ Muntahaa Mbàkke moo leen doon dalal. Waaye fii mu nekk, taskati xibaar yaa nga cay joxoñ takk-der yi. Ña nga leen di tuumal ni dañ fa buruxlu, doon coytu seen ub waxtaan ak kilifa gi.
XEW-XEWI JAMONO
Jamono yii nag, Senegaal gépp a nekk ci tiis ndax aksidaŋ bu mettee metti bi am ca Kafrin. Ñaari biis yu yab i nit ba fees ñoo mbëkkante ba lu ëpp 50i nit ñàkk ci seen i bakkan. Jamono yii nag, Njiitu réew mi Maki Sàll dekerete na ñetti faniy dëj (9, 10 ak 11 saŋwiyee 2022) ci réew mi.