LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI ( 5/10/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

MAKI SÀLL DINA TAS CÀMM GI

Muy ab xibaar bu jib ginnaaw ba ñu defe ndajem jëwriñ yi démb ci àllarba ji. Njiitu réew mi dafa namm a tas Càmm gi, tabb ay jëwriñ yu bees fii ak njeexitalu ayu-bés bi. Bu ñu sukkandikoo ci yéenekaay bii di Libération mi joxe xibaar bi, ay coppite yu mag dina ca am. Loolu tax ba xel yépp daj ne njiitu jëwriñ ji di Aamadu Ba, te nekk lawaxu Bennoo Bokk Yaakaar, du nekkati njiit li.

TIK-TOK BËGG NAA TIJJIWAAT

Mu bokk ci mbaali jokkoo yi gën a siiw ci jamono jii, Tik-Tok, ay weer a ngi nii ñu ajandi ko ci Senegaal. La ko waraloon di coowal Usmaan Sonko la ca weeru suwe. Moo tax ba meetar Musaa Bookar Caam miy jëwriñ ji ñu ko dénk jokkoo gi, indi ay ponk ngir Tik-Tok mën a dellusiwaat. Bokk na ca ñu amal ay caytu ci lañu cay dugal te mu mën a yee fitna, ñu di ko segg di ko far waaye it mu am ku leen fi teewal ci réew mi.

UBBI TAY JANG TAY NDAX DINA NEKK

Ginnaaw ba leen fa jàngalekat yi jiitoo, ndongo yi topp nañu ca. Seen ub lim ren ëpp na ñeenti miliyoŋ.  Lekkoolu Senegaal nar a door njàng mi. Ñu bari di laaj ndax loolu dina mën a nekk ginnaaw ba ñu gise ay jafe-jafe yu bari ci njàng mi. Bokk na ci ay lekkool yu nawet bi bàyyeegut, ñàkkug jàngalekat ak i matukaay ci yenn ci lekkool yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj