CEDEAO jël ndogal ñee maxejji réewi AES yi (Mali, Burkinaa Faaso ak Niseer). Ndogal li mooy ne, léegi, Saa-Mali yi, Saa-Burkinaa yeek Saa-Niseer yi, képp ku ci bëgg dem ci réewi CEDEAO yi fàww nga wut “visa”. Li leen tax a jël dogal loolu mooy li réewi AES gedd, génne seen bopp ci kurélug Afrig sowu-jant gi.
Waaye, ndogal loolu, Saa-Senegaal yu bari ñoo ngi koy naqarlu ci mbaali jokkoo yi. Am na sax ñu sàkku ci Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, mu bañ a dugal Senegaal ci ndogal loolu. Nde, askani Afrig yépp wenn lañu ; kon, seen i njiit waruñoo dox seen diggante ba di leen féewale. Dafa di, moom sunu Njiitu réew li, naataangoom bu Niseriyaa bi, Tinubu, saraxu na ko ngir mu wax ñetti réew yooyii ay sóobare jiite ngir nu delsi biir CEDEAO.
ÑAAREELU BÉSU SET-SETAL
Ci réew mi, bari na gox ak gox-goxaan yu génn ngir amal bésu set-setal. Mu nekkoon naalu Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, kilifa yu bari génn nañu tey ànd ak seen i ñoñ ngir setal, luqati seen i mbedd te waajal nawet bi. Fa Ndar-Géej, njiitu càmm gi, Usmaan Sonko, ma nga fa woon ; Tuubaa, Bàlla Musaa Fofana wax na fa ni jaaykat yi di aakimoo yoon yi ci lu jaarut yoon ; Kungéel, waa ONAS ña nga fa woon.
USMAAN SONKO MA NGA WOON FA NDAR
Njiitu Càmm gaa nga woon démb fa Ndar ci bésu set-setal bi. Askan wa génn nañu wax seen i jafe-jafe ci ñeel wal mi. Fa diiwaanu Pikin, mbënn mi sonal na leen lool. Ba tax na, muy fàttali Mansuur Fay, meeru Ndar, naalu 60i tamñaret yi ñu fi sumboon ñeel mbënn mi. Mu koy soññ ngir mu amal ay leeral ci wàll woowu.
Ginnaaw ci loolu, dem na, moom Usmaan Sonko, ca jàngune UGB, nemmeeku leen.
BAC 2024
Kàtte “BAC” bu ren bi dina des ci xel yu bari. Li ko waral di ndongo yu bari yu ñu ci dàq ngir jollasu yi ñu fay tere. Fa Kawlax, nemmeeku nañu ko fa. Waaye, taxut ndongo yi jëfe loolu. Ba tax na, fa Bàmbali, jàpp nañu fa ci alxames ji ndongo lu doon yër ag jollasoom. La ca Seneweb xamle mooy ma nga ca loxoy yoon fa Séeju.