Ndey Faatu Faal mi ñuy woowee Faala Fëlëer nekk ab ñaxtukat, ñu gën koo xame ci làngug kujje gi, jot na ay koppar yu duun. Mu siiw lool ci mbaali jokkoo yi, Faala jot na jaar ndung-siin ginnaaw ba mu fa tëddee juróom-benni weeri kaso. Loolu tax ba ñu dàq ko “Dakarnave” ba mu doon liggéeye. Ci loolu lañu ko sàkkulee ay koppar ngir dimbalee ko ko. Mu tollu ci juróom-ñaari tamndaret( 7 millions)
GOLO DU BAY BAABUN DI DUNDE
Baykat yi nee nañu déet. Waa “Mouvement Baol debout” mànkoo ci seen ug làng tuddee ko “golo du bay baabun di dunde” ngir jàkkarloo ak Nguur gi. Li ko waral di njëgu gerte gi Nguur gi yamale ci juróom-fukki dërëm (250f). Tax ba ñu téye seen gerte. Ñoom nag ña ngay sàkku njëg li ëpp loolu ngir gën a ñoŋal seen uw nekkin. Te yit di wax Nguur gi ñu ubbi dig yi ngir jëndkat yi mën a ñëw.
TUUBAA AB LIIR LAÑU FA SUUL
Fa Tuubaa, ab liir bu indaalewut bakkan lañu fa suul ci ay anam yu dëppoowut ak yoon. Bu ñu sukkandikoo ci yéenekaay Seneweb, ci ay pàkki jàmbur lañ ko suul. Tax ba boroom kalaame ko yoon ngir ñu sulli ko. Jëf jooju xamagun ku ko def waaye yoon tijji na ci ab lànket.
ÀTTEB RÀPPËER YI
Ràppëer ya ñu jàppoon ca atum 2022, ba noppi ñu bàyyiwaat leen te kenn àttegu leen, muy Simõ Kuka, Kilifa ak Ceer. Tóxalaat nañ seen bésub àtte ca 4 saŋwiye 2024. Nde, ci alxames ji 7 desàmbar 2023 lañ leen waroon a àtte. Yoon a ngi leen di toppe kurélu jëfkati lu bon, ger, dooleel ger, pexem njuuj-njaaj ñeel ag kayitu caytu, kootoog tukkilaate ci anam bu safaanook yoon.
WAA F24
Cib yégle la kii di Mamadu Mbooj ak i ñoñam yu F24 xamle ne Maki Sàll dafa war a bàyyi pexey caay-caayam yi muy def ngir sax ci Nguur gi, te it mu fexe ba bàyyi ñi mu nëbb jànt wi ci jaay doole, ñu bokk ci wotey 2024, ndax ñoom it ci Senegaal lañ bokk. Yokk na ci ne diirug ñaari weer a ngii ñu teg loxo Aliw Saane ci lu dul yoon te ba tey nanguwuñ koo àtte, te bari na ciy moroom. Wax nañ ne lenn rekk moo leen soxal, mooy ñu génne ñi ñu jàpp ñépp ci lu teguwul ci yoon, ñu nekkaat ci seen i yitte.