LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (8/6/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

BUGAAN GÉY DANEE NGI WEDDI AK A LEERAL

Yéenekaay Source A dafa fésaloon ab xibaar, di ci wone coow lu dox ci diggante Bugaan Géy Dani ak “Banque Agricole”. Bugaan Géy nag, dafa teggi wax jees wax ne, dañu jaay ab taaxam ci sababu bor bi mu ame. Moom, booroom Dmedia, mi ngi dalal xeliy jegeñaaleem ci ne, lees koy waxal wérul. Bees sukkandikoo ci moom, moom ci boppam mooy aji-loru ji. Ndax,ba tey ciy waxam, mbirum njuuj-njaaj la. Dañu ko bëggoon a nax. Mu teg ca ne, ay layookatam dinañ topp mbir mi ci yoon.

SENELEC AK DDD

Ag caytu gu feeñal ag njuuj-njaaj fa màkkaanu DDD (Dakar Dem Dikk). La liggéeykat ya gis mooy, lu tollu ci ñeenti at ci ren, béréb boobu du ñu fay kuraŋ. Kontëer daf fa amul sax faf. Ña fay liggéeyee, lañu xamle mooy yëguñu woon lu ni mel. Ba tax na, ñooña lañu def mooy rocci lépp, dog kuraŋ ba.

JUMTUKAAYU XARALA YU BEES YI CI GOX-GOXAAN YI

Musaa Bàlla Fofana, jëwriñ ji ñu dénk gox yi ak gaox-goxaan yi joxe na ay jumtukaay yu bari. Mu jagleel ko ñiy liggéey ci Meeri yi, jumtukaay yi ñeel xarala yu yees yi. Koppar ya, ña nga koy xayma ci lu ëpp benn tamñaret ci sunuy kopar (1,2 milliard) ci ndimbalu Bennoog Tugal (Union Européenne). Muy 1 200i nosukaay (ordinaatëer), 1 000iy ondilëer ak 1 000iy móolukaay (impérimantes).

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj