LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (ÀJJUMA 10 MÀRS 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Paap Njaay tëddi na Sebikotaan

Taskatu xibaaru Walfadjiri bi, Paap Njaay, mujje nañ ko jàllale ça kaso Sebikotaan. Ci altine jii la ko àttekatub lënbët bu ñaareelu kabine bi dóoroon “mandat de dépôt”. 

Yéenekaay L’enquête moo siiwal xibaar bi, xamle ne Paap Njaay kat, jàppandi nañ ko ca Chambre 2, fa kaso Sebikotaan. 

Séex Aajibu Sumaare

Tey ci àjjuma ji lees defeere Aajibu Sumaare. Tuumaalees na ko ciiwalug xibaar yu wéradi, daldi koy teg “contrôle judiciaire”. Maanaam, bàyyi nañ ko mu ñibbi, waaye Yoon daf ko tënk, gàll koy dig yu mu warut a jéggi. 

Moom nag, dafa bindoon bataaxal jagleel ko Njiitu réew mi, samp ciy laay yoy, ñoo naqadi Njiitu réew mi, Maki Sàll, ak Càmm gi. Démb lañ ko woolu woon pólis, daldi ko fay fanaanal.

Daaru Musti : Ag daamar bu yaboon ay ujaaj moo daanu

1 bakkan bu rot ak 5i nit ñu amey gaañu-gaañu, looloo tukkee ci jéyya ji am, tey ci suba, ci tali Daaru Musti wi. Màggalu Daaru Musti la nit ña juge woon. Dawalkat ba nag, daw na. Jamono jii, sàndarm yaa ngi koy wër. Nee ñu, dafa doon xél ba ni ko daamar giy rëcce. Sàppëeri Tuubaa yi ñoo toppatoo 5i nit yi amey gaañu-gaañu, daldi leen di jàllale raglu ba. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj