LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (ÀJJUMA 14 AWRIL 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Waxtaanuw Usmaan Sonko ak Jean-Luc Mélenchon

Njiitul Pastef li xamle na, ci xëtu Facebookam, ne waxtaan na ak Jean-Luc Mélenchon mii jiite pàrti pólitigu Farãs bii di La France Insoumise. Ci àjjuma jii la waxtaan wi am.

Jean-Luc Mélenchon a njëkk a siiwal jokkoo gi ci Twitter. Daf ci wax ne, moom ak njiitul Pastef li, waxtaan nañu ci ëllëgu Farãs ak Senegaal, waxtaane tamit seen i naal ñeel seen i réew. Dafa bind, wax ne waxtaan na « waxtaan yu xóot a xóot ak Usmaan Sonko ci ëllëgu Farãs ak Senegaal. Ay naal yu wuute, waaye noo bokk jenn yéene xeex jaay doole bi sunu njiit yi nekke. »

Usmaan Sonko tamit, ci xëtu Facebookam, bind na ci lii toftalu :

« Tey ci suba, jot nanoo waxtaan lu yàgg ak Jean-Luc Mélenchon ak dépite Arnaud Le Gall, bokk ci France Insoumise. Waxtaane nan pólitigu àddina si, jëflantey Tugal ak Afrig, waaye li nu gën a waxtaane mooy diggante Farãs ak Senegaal. Noo ngi rafetlu lu bari li bokk ay gis-gis ci mbir mi. »

Layoo Maam Mbay ñaŋ Usmaan Sonko

Ginnaaw lu jege ñaari ayu-bés, ginnaaw bi ñu leen àttee ak léegi, ñoom ñaar dinañu leen àttewaat. Li ko waral nag, mooy « appel » bi Maam Mbay def ca ëttu « appel » ba (Cours d’appel). Maanaam ëtt ba nga xam ne, bu ñu la àtte te àndoo ci, fa ngay dem ñu àttewaat la. Ki ko jiite mooy Aamadi Juuf mi nga xam ne, mbir mi ciy loxoom la njëkkoon a jaar, ca ndorteelu coow li, ba muy nekk toppekat. Ñoom ñaar sax jotoon nañoo dàq seen àtte boobu ñaari yoon. Ca ñetteel ba lañu leen mujje àtte, daan Usmaan Sonko ñaari weeri kaso yu mu dul tëdd ak ñaari téeméeri miliyoŋ yoo xam ne da koy dàmpe Maam Mbay. Layoo bii nag jàpp nañu ko fukki fan ak juróom-ñaar ci weeru awril wii ñu nekk.

Sonko ci njàppug Basiiru Jomaay Fay

Ci ngoon gi la xibaar bi jib ne, ay takk-der ñoo ngi doon jéem a dàjji pekkug Basiiru Jomaay Fay ca DGID. Usmaan Sonko, nag, àddu na ci mbir mi bi muy biral waxtaan wi mu amaloon ak Jean-Luc Mélenchon. Dafa bind ne :

« … juróom-ñetti takk-der yoy, bi ñu sonnee ci tëru [Basiiru Jomaay Fay] këram ci suba ba léegi, dañu dem pekkoom ngir jàpp ko ci lu dul yoon. »

NJiitul kujje gi ne, li Basiiru Jomaay Fay mujje bind ci xëtu Facebookam lañ koy toppe. Cig pàttali, biñ siiwale bésub « Appel » bu layoob Usmaan Sonko ak Maam Mbay Ñaŋ, Basiiru Jomaay Fay miy tof-njiitul Pastef bu mag bi dafa ŋàññi woon as-tuut ciy àttekat yiy gaawantu mbir mi, di jalgati yoon ngir bànneexu Maki Sàll.

Idiriisa Sekk : « Dama bëgg Usmaan Sonko bokk ci wotey 2024 yi. »

Idiriisa Sekk amal nam ndaje ak taskati-xibaar yi. Cees la waxtaan wi ame, tey ci ngoon gi. Dafa doon biral gis-gisam ak i xalaatam ci tolluwaayu réew mi. Lees di wax, naan, ndox du wàcc yoonam, moom la Idi def. Nde, ni mu ko baaxoo defe, firi na fay aayay Alquraa yu bari ngir layal jaar-jaaram ci pólitig ak ndogal yi mu jot a jël yépp. Ginnaaw gi, dafa wax ne :

« Xam naa ni, yéen ñépp, li leen fi indi mooy xam li sabab ndaje mi.  Waaye sabab bu njëkk bi mooy ne dama bëgg Usmaan Sonko nekk lawax ci wotey 2024 yi. Dama bëgg ndaw ñi ko topp xam ne, jarul taal ak a toj. Kenn ragalul janook seen lawax. Man de ragaluma. »

Njiitul CESE li dëggal na sax lees doon ruumandaat ci lim seeti woon Usmaan Sonko. Waaye, dafa leeral ne, lu jiitu, dafa ndogook Maki Sàll ba noppi, xamal ko yéeneem ci tànki jàmm yi mu namm a dox. Ca ëllëg sa lay sog di seeti Usmaan Sonko, waxtaan ak moom.

« li ma wax ak Sonko, sama diggante ak moom kepp la. Waaye, tànki jàmm yi ma dox tax na ba réew mi am dal keroog 4 wril, tax na yit réew mi duggul ci guuta keroog 30 màrs. »

Saajo Maane dina fay 327i tamndareti FCFA

Bayern Munich génne na ab yégle di ci xamle daan yi mu gàll Saajo Maane ginnaaw bi mu jàppantee ak Lërooy Saane.

« Saajo Maane, 31i at, du bokk ci ñuy joŋante ak 1899 Hoffenheim ci gaawu gii. Li ko waral mooy ni mu doxalee bi joŋanteb Manchester City ak Bayern Munich jeexee. Maane dina fay alamaan tamit. »

Tdalu webu RMC nag, xamle na ni alamaan bi Saajo Maane war a fay mi ngi tollu ci 500 000iy ëro, maanaam 327 978 500 ci sunuy koppar.

Jaraaf

As Jaraaf tàqalikoo na ak tàggatkatam bii Yuusuf Daabo. Ndaxte, gisuñu li ñu doon séentu ci moom. Ci ab yégle bu ñu tas lañ ko xamlee. Moom, Yuusuf Daabo, gannaaw lu rëy la mu liggéeyoon foofa ca Tëngéej FC ba tax mu siiwoon ba am ca sax ñu ko yéene woon ekibu Senegaal, ba léegi dafa am ay jafe–jafe.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj