Jëwriñ ji ñu dénk wàllum ndox mi ak cet gi fii ci Senegaal, Sëriñ Mbay Caam, moo ngi woon ca diiwaanu Tuubaa ngir saytu matuwaay yi ñu jël ci Màggal gi ñu dëgmal rawatina ci wàllu ndox mi. Nee na nag dinañu def li leen war ngir nit ñi bañ a rafle ndox bu bés baa.
PÓLITIG
Lamin Caam la Abdulaay Wàdd tànn ngir mu bokk ci joŋante yi yenn ci dépite yi di amal ngir nekk Njiitalu Ngomblaan gi (Péncum ndawi réew mi). Ñenn ci ñi bokk ci lëkkatoo bii di PDS ànduñu ci. Nde, moom Abdulaay Wàdd, bi muy def bile tànneef, waxtaanul ak kenn ci ñi mu bokkal lëkkatoo gi.
KOOM-KOOM
Liggéeyu sémbub gaas bii di GTA (Grand Tortue Ahmeyin) mi ngi dox bu baax. Nde, ci xayma, nee ñu def nañ ci 82,5% liggéey bi. Rax-ci-dolli, xaymees doxiinu liggéeyu sémbub soroj bii di Sàngomaar lu tollu ci 60%. Mu nekk liggéey bu mucc ayib bu Njiitu réew mi Maki Sàll di rafetlu ca ndaje ma ñu amaloon démb fii ci Senegaal ci fànnu gaas bi ak soroj bi.
TÀGGAT-YARAM
Bàmba Jeŋ day mujjee des Marseille !
Bàmba Jeŋ mii nga xam ne Niis moo ko bëggoon a jënd ca loxoy Marseille ci lu tollu ci 12 miliyoŋ ci Ëro, mujju faa dem ndax ab feebar bu ñu gis ci yaramam bi ñu koy saytu démb. Waaye bésub tey jii, dinañu amal ak moom beneen saytu ba xam ndax feebar bu sew-sewaan la ame, am déet.
Gànna Géy ca Everton !
Gànnaaw bi mu toogee lu yàgg te futbalul ak ekib bii di Paris Saint Germain, Gànna Géy mujje naa am Këlëb bu ko jënd. Këlëb boobu nag, fa la newoon laata muy dem ca Paris. Everton ga nga xam ne fa la nekkoon, fa la dellu te dina fa am lu tollu ci ñaari at.