LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI Àjjuma 30 sàttumbar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Ndogali Njiitu réew mi ci Karim Wàdd ak Xalifa Sàll

Kii di Sã Sarl Biyagi, dib nekk jàngalekatu « Sciences politiques » ca daara ju kowe jii di Seex Ànta Jóob, xamle na ne ndogali Njiitu réew mi ci ñaar i wujjam yii di Kariim ak Xalifa génnul ci pólitig yi mu daan teg boobu ba léegi. Li ñu ko néewal doole ci ñaari wote yii weesu moo waral lu ni mel. Ab jumtukaay la ngir mu gën a amaat doole. Lu jëm ci ñetteelu moome gi ñépp di waxtaane tey, moom Sã, mi ngi ciy xamle ne wóoluwul benn yoon Njiitu réew mi.

Wotey 2024

Lëkkatoo gii di « Gox yu bees » fësal na yéeneem ngir bokk ci wotey 2024 yii nu dëgmal. Kii di Amet Jàllo a ngi xamle ne lëkkatoo gi dina biral ay xalaat ak ay gis-gis ci ni mu bëgg a doxale réew mi bu ñu leen ko dénkee. Rax-ci-dolli, dinañu xamle ci diir bu gàtt ki ñuy jiital.

KOOM-KOOM

Jëwriñ ju bees ji ñu dénk wàllum napp gi ak koom-koomu géej gi, Paap Saaña Mbay, moo ngi xamle ne  dina liggéey ak jëwriñ ji yore wàllum njaay mi ngir  ñu gën a naatal koom-koom gi. Ci xayma,  dinañu defar benn isin « perketsing » bu mën a jàppale këru liggéey yi, bu ci mel ni këru liggéey gii di Scasa. Isin boobu dina tax njëgu njaay yi muy defar gën a wàcc. Bu ko defee, dina mën a  bokk ci ñiy suqali koom-koomu réew mi.

WÉR-GI-YARAM

Kurél gi ëmb mbooleem fajkat yi nekk ci biir réew mi moo jël dogal ni duñu liggéey fii ak ñaari fan. Dogal boobu nag, Altine 3 Ocktoobar lay tàmbali. Nde, ñoo ngi aartu Nguur gi, di ko xamal ne bu amul ay pexe ci seen i jafe-jafe, dañuy jël yeneen i dogal yu raw yi ñuy waaj a jël nii.

XEW-XEWU JAMONO

Fale ca Kawlax, ab dalu kër moo daanu ci jenn jigéen ak doomam. Jéyya jaa ngi am ci koñ bii di Xaaxun. Ña ca jële ay gaañu-gaañu, xaymees na leen ci fukk ak lu teg ci kër gi.

TÀGGAT-YARAM

Ci Kub bu mbooleem réew yi bi Qataar di amal, kurél gi war a taxaw ci doxalinu  kub bi moo  siiwal sàrt bi réew moomu di Qataar bëgg a sàmp ci diir boobu.

Ci sàrt bi, lii lañu ci biral :

– Jigéen ñi dañu war a muuru 

– War nañu xoolaat colin yi

–  Dorog ak sàngara tere nañu ko fa

– Doxandéem yi waruñu jege jigéeni Qataar yi

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj