Tey ci àllarba ji la làngug Pastef namoon a amal seen doxi-ñaxtu yi ci boor réew mépp. Waaye, mujjul a àntu. Ndax, perefe bu Ndakaaru bii di Moor Taala Tin mooy ki ko gàntal ginnaaw bi ko waa Pastef yi jébbalee seen bataaxal ngir sàkku koo amal ca « Place de la Nation. »
Ci jamono jii, fa mu dëkke ca Cite Kër Góorgi, moom Usmaan Sonko dañu ko fa tëj ca këram, takk-der yaa nga ko wër fépp. Mënul génn dem fenn moom ak ug njabootam. Te, moom it, kenn mënul a dem seeti ko. Yenn ci dépitey Yewwi Askan Wi yi fa bëggoon a dem sax, ay lakkirimosen lañu leen dóor. Dépite Guy Mariis Saañaa sax jële n’a ci gaañu-gaañu. Ndax ci tànk bi lañ sox ab lakkirimosen.
Farãs
Yoon daan na ñaari saa-farãs yii di Erig Lórã ak Katerin Garaasiyee. Ñoom ñaar nag ay taskati xibaar lañu. Dañoo bokkoon génne ab téere ci atum 2012 tudde ko “Le roi prédateur”, doon ci lëjmbat dundu buuru Marog bi. Ginnaaw loolu, ñu boole ci njuuj-njaaj, doon laaj réewum Marog xaalis bu takku (3i tamndareti Ëroo) bu ñu bañee ñaareelu xaaju téere bi génn. Jëf ju ñaaw jii la leen àtte-tooñ bu Pari daane atu kaso, boole ci alamaan leen ku ci nekk 10. 000iy Ëro.
TÀGGAT-YARAM
FIFA
Ëllëg, alxames 16i fan ci weeru màrs, lañ war a dénkaat Gianni Infantino lengey kurél gi jiite kuppeg àddina si, muy FIFA. Nde, ci talaata jii weesu lees xamle woone njiitul FIFA baay toogaat. Li waral palaat gi nag, mooy ni dafa amul wujju ca yëf ya niki 2019 rekk.
Kuppeg àddina si 2026
FIFA amal nay coppite ci kuppeg àddina sii nu jëm. Léegi dina nekk 48i ékib yoy, dañuy séddalikoo ci 12i kippu, bu ci nekk ñeenti ékib nekk ca. Bu ko defee kippu bu nekk ñaar ñi jiitu ñooy génn ak 8i yi gën ci ñetteel yi.
Kuppeg àddina 2030
Muxammed VI, buuru Marog bi, wax na ni Marog taxaw na te yit dog na ngir bokk ci ñiy bëgg amal kuppeg àddina si ci atum 2030.
Alseri
Houssem Aouar soppinay këyitam doon saa-Alseri. Loolu nag di firndeel ni léegi mën na bokk ca boobu ekib, bu ñu ko ci woowee.
Senegaal am Gàmbi ?
” Yaakaar naa ni waxtu wi dina ñëwi ngir tànn ban ékib laay joŋante. Fim ne nag, sama yéene mooy wut xaalis ba bégal sama yaay ak jéem a weesu fi ma tollu nii. Di gërëm bu baax Senegaal ak Gàmbi ci cofeel giñ may wan saa su nekk. Bu waxtu wi jotee nag dinanu xamle ban mayo réew lanuy sol.
Loolu mooy kàddu yi Lamin Jarju wax kii di Abdu Njii (Abdou Njie)