LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (ÀLLARBA 3 ME 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Aminata Ture

Ginnaaw bi mu xamlee nee waa PDS ak Waa Bennoo Bokk Yaakaar dañoo teg “deal” Ci suuf ngir féewal kujje gi, daganal ñetteelu moome gi, setal Kariim Wàdd, soxna si xamle na tey ni, mi ngi jot i saaga ak i tëkku ci jollasoom.

Ci xëtu Facebookam la biral xibaar bi. Waaye, nee na, loolu mënu ko xofloo. Day gën a yokk pasteefam ci xeex bi muy xeex ngir demokaraasi bi dellusi. Rax-ci-dolli, nee na lépp lu ko mën di dal, ci Njiitu réew mi Maki Sàll la ak waa PDS la koy delloo.

Usmaan Sonko jéggi na dig

Démb, ci talaata ji, la Usmaan Sonko dugal ab nataal ci mbaali-jokkoo yi, fekk mu ngi woon ca Gàmbi, doon jëm Sigicoor. Bi bind ne, guléet muy jéggi digi réew mi ginnaaw ñaari at yu teg ñetti weer.

Xamleet na ci xëtu Facebookam ne, kii di Maaham Jàllo moo bañ ne du ko delloo ab jàll-waaxam te, tegu ko fenn. Te, Yoon moom buy nekkee ci kiliftéefi way-pólitig jalgati ko day doon jumtukaay, te fippu tamit ab sañ-sañ la.

Bàyyib négandiku ñeel Basiru Jomay Fay ak Muhamet Sàmb Jiim

Basiiru Jomay Fay ak Muhamet Sàmb Jiim (Hannibal) ñoo nga woon ca kanamu àttekat bi, démb ci talaata ji. Dañ leen waroon a déglu ñeel tuuma yiñ leen di toppe. 

Cig pàttali, kii di Muhamet Sàmb Jiim, ñaŋ ko tegoon loxo ci mbiri “forces spéciales yi”. Bu dee Basiiru Jomay Fay, moom, ñi ngi koy toppe “wuññi suturay àttekat, biralug xibaar yu wéradi ak yee fitna”.

Ginnaaw bi ñu leen dégloo démb, seen layookat bi meetar Musaa Saar dugal na ca saa sa ab bataaxal di ci sàkku bàyyib négandiku ngir Basiiru Jomay Fay. Te dina dugal beneen bataaxal ci àllarba ji ngir sàkku ceet bàyyib négandikub Muhamet Sàmb Jiim.

Toftaleg RSF : Senegaal wàcc na ba ci 104eelu palaas bi

At mu nekk, saa bu 3 me jotee, dañuy màggal ci àddina sépp ngoreefu kibaraan yi. ONG Reporters Sans Frontières di ci génne ag toftale gog, day biral tolluwaayu ngoreefu kibaraan yi ci réew mu nekk. Maanaam, day saytu ba xam taskati xibaar yi, ci réew mu nekk, ñu ngi def seen liggéey ni mu waree ànd ceek seen sago te kenn du leen xoqatal walla di leen ger ak a jaay doole. Daaw, Senegaal a nekkoon 72eel. Waaye ren de, dafa dellu ginnaaw lool, féete ci 104eelu palaas bi.

Ñàkkul ne, li Yoon singali taskati xibaari réew mi, rawatina ñi àndul ak Nguur gi, moo tax. Ndax, muy Paap Aale Ñaŋ, boroom Dakar matin, di taskati xibaari Walf tv yi, Paap Njaay ak Coro Mandelaa, ku ci nekk, Yoon teg na la loxo.

Bindu gi : lu ëpp 300 000iy wotekat yu bees bindu nañu

Duudu Ndiir, njiitul CENA li, doon na nemmeekuy komisiyoŋ ci béréb yu bari biir Ndakaaru. Ca la xamlee ne, biir réew mi rekk, lu ëpp 300 000iy wotekat yu bees bindu nañu ci këyitu wote gi. Bu dee bitim-réew, limees na fa lu weesu 30 000iy wotekat yu bees yu bindu ngir mën a wote.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj