LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI Altine 12 desàmbar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Jëwriñ ju mag ji, Aamadu Ba teew na ci kanamu ngombalaan gi. Ginnaaw bi ko Njiitu réew mi tabbee woon ci boppu Càmm gi (17 Sàttumbar 2022), tey ci altine ji la doon jàkkaarlook njiitu ngombalaan gi ak i nawley dépiteem ngir dégtal leen yoonu naalam ci ittey njiitu réew mi. Boobu jàkkaarloo nag nekk na lu bokkeefu Senegal tàmm a amal, saa su Njiitu réew mi taxawalee Càmm gu bees.

AMS (Association des maires du Sénégal) am na njiit lu bees. Kii di Umar Ba, di meeru Njob ca Fatig moo wuutu Aliw Sàll ci boppu kurél gi. Mi ngi am démb ci bi ñuy amal seen lël bu mag (Assemblée Générale), yemook bés bi àddina si doon màggal bésub yaatal gi ci pólitig (décentralisation). Waaye meeri Yewwi yi teewewuñu lël boobu, ndax kenn woowu leen ci buñ leen déggee. Ñoom sax dañoo namm a taxawal geneen kurél ci turu Réel (Réseau des élus locaux du Sénégal). Waaye, Njiitu réew mi Maki Sàll a nga leen di dànkaafu ci genn kurélu meer a fiy am, fii ci réew mi.

TÀGGAT-YARAM

Ñeenti réew ñoo des ci kuppeg àddina si. Menn réewum Afrig (Marog), menn réewum Amerig dii Sidd (Àrsàntrin) ak ñaari réewi tugal (Farãs ak Kurwaasi). Ëllëg ci talaata ji la Àrsàntin di janook Kurwaasi ci benn démi-finaal bi. Ginnaaw-ëllëg, Farãs ak Marog daldi laale ci beneen démi-finaal bi. Cig pàttali, Marog mooy ékibu kembaarug Afrig bu mës a agsi fii ci kuppeg àddina si. 

Fii ci Senegaal, liig (LSFP) bee ngi doon amal i joŋante jamono ji kuppeg àddina na si di daw fale ca Qataar. Ci njeexitalu ayu-bés bi lañ doon amal 9eelu bëccëg bi. Casa Sport dafa jóge ci boppu raw-gàddu gi ginnaaw bi mu daanoo, dibéer, ci kanamu Tëngéej FC, Géejawaay FC mi dóor Génération Foot moo ko fa wuutu.

XEW-XEWI JAMONO

Tiis wu réy a këppu ci kow waa axlu film. Way-yëngatu bii di Charles Forster moo dëddu niki gaawu ci guddi. Moom nag, mi ngi amoon 69i at, nekkoon fi ku ràññeeku lool ci wàll wile. Waa axlu film walla sax axlu caada, ci gën-gaa yaatu, ñàkk way-yëngatu bu mag. 

Ca Mbuur, as waay su tudd Aali Kuyaate, fekk baax Gine, moo fa bóom ñaari nit, gaañaale tamit ñetti nit. Moom nag dafa naaloon foqati alal fa muy liggéeyee. Bi pexeem àntuwulee, ca la wëlbatiku daldi jëfe ni rëtalkat yi di jëfe. Jamono yii, ma nga ca loxoy yoon ñu téye.

BITIM-RÉEW

Jëwriñu jiñ dénk wàllu bitim-réew ca Farãs ma nga woon Koddiwaar, doon fa amal ab tukki ci diggante ñaari nguur yi. Moom, Katerin Kolonaa, jot na faa dajeek Njiitu Réewum Koddiwaar, Alasaan Watara, ak kurél yi fare ci askan wi. Ma nga fay naqarlu nag mbañ gi doomi réewi Afrig yi jugte jëmale ko ci réewum Farãs te dara waralu ko lu dul ay ruumandaat ci suuf buñ ko déggee. Waaye ma nga mel ni ku leen di saaga. Ndax, la mu ca teg mooy « li nu war mooy jàppale réew yi ci seen suqaleeku, te yéen it waruleen nangoo doon ay doom ».

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj