LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (ALTINE 27 MÀRS 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

YOON

Deferee nañu Baabakar Ñ ngir ne dafa seetaan aji-tawat ba mu faatu faf

Ci altiney tey ji lañ wooluwaatoon doktoor Baabakar Ñaŋ ca « Sûreté urbaine (Su) » ginnaaw biñ ko bàyyee ci gaawu gi. Defeere nañ ko nag. Maanaam, jàllale nañ ko ca toppewway ba, mu war fa janook toppekat bi. Lees koy tuumaal mooy « ñàkk a wall nit ku repp ak mbóomug teyeedi ».

Bàyyi nañu El Maalig Njaay, daldi koy takkal lamu elektoronig

Yoon bàyyeendi na El Maalig Njaay, moom mi yor njokkaleg Pasteg, bokk ci pekkug làng gi. Waaye nag, bàyyeesu ko noonu. Ndaxte, dañ ko takkal lamu elektoronig nees ko takkalee woon kii di Waali Bojaŋ ci lu yàggul dara. Moom nag ñi ngi koy toppe « ciiwalug xibaar yu wéradi yu mën nasaxal Campeef yi ».

PÓLITIG

Kàdduy Aaroona Kumba Ndóofeen Juuf

Kumba Ndóofeen Juuf yékkati nay kàddu, naruñoo neex Njiitu réew mi ak waa APR. Kàddu yooyu nag, daf ci biral ne Njiitu réew mi, Maki Sàll, jeexal na. Maanaam matal na ñaari moomeem. Nee na, bu ñu sukkandikoo ci Yoon, am na sañ-sañu wut ñetteelu moome. Kon, mbir mi du moom ak Ndajem Ndeyu-àtte mi, waaye, mbirum xel kese la. Maki dafa def ab dige saa-senegaal yépp nangul ko, amul sañ-sañu teggi ay kàddoom. « Ci atum 2012, daf ma woo woon ngir ma fekksi ko ngir xeex Abdulaay Wàdd ci moome yi. Léegi, nan lees mënee dellu ginnaaw ci loolu ? »

Idiriisa Sekk fomm na waxtaan wi mu naroon tey ci ngoon

Idiriisa Sekk dafa naroon a janook taskati xibaar yi, tey ci ngoon ci 16i waxtu. Ca Fun City la waxtaan wa waroon a ame. Waaye, daf ko mujje fomm. NJiitul CESE li nag, leeralul sabab yi tax mu fomm ndajem mile. Waaye, daal, njorteesoon na ne, dina àddu ci mbirum ñetteelu moome gi ak bokkam ci wotey 2024 yi.

NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI

Ndongoy liisey Ndakaaru yi booloo nañ ci xeex

Ndongoy liise Ndakaaru yu mag yépp dinañu amal ab doxu-ñaxtu bu mag ngir ñu bàyyi seen moroom bii di El Basiir Ñaŋ bu liise Delafoos ak Sëriñ Mustalaa Ñas. Alxames jee mujj lañ jàppoon ñaari ndongo yile. Dinañ ci toftal am ndaje ak taskati xibaar yi.

Bees sukkandikoo ci ñu sumb mbir mi, dinañ xaaj ndongo yi ci ñaari kippaangoo. Kippaangoo gu njëkk gi mooy jaar yoonu wenneel wi. Delafoos a koy jiite, ànd ci ak liise yaxantu bu Delafoos, liise xaral bu Delafoos, liise Lamin Géy, liise Jean de la Fontaine, liise 1MJ, liise Biraago Jóob, liise Kenedi ak liise Belees Jaañ.

Liise Galàndu Juuf ak liise Séydu Nuuru Taal ñoo jiite ñaareel kippaangoo gi, ànd ceek liise liise Yalla Suuren, liise Symbiose, liise sàkkerekëer, liise Salja, liise Faddiilu Mbàkke.

CESL dakkal njàng ma ca UGB

Kurél gi jiite ndongoy jàngune Gastoŋ Berse bu Ndar dakkal njàng ma ngir fésal seen mer ñeel seen moroom biñ jàpp. Nee ñu, fileek bàyyiwuñ ko, kenn du jàng ca béréb ba.

Sàndikaa jàngalekat yi sóobu nañ ci xeex bi

Ñaxtuy pólitig yi lor na way-pólitig yi, loraale lekkool bi. Ndax, la ko dale 16 màrs ba léegi, ag dal amul ci lekkool yi. Noonu, wa G7, di kurél gi ëmb jàngalekat yi, fas yéene nañoo bank seen i loxo, dakkal njàngale mi bu 10 i waxtu jotee ci àppub ñaari fan.

BITIM-RÉEW

Ruwàndaa

Póol Rusesabasinaa ak 19i naataangoom yu bokkoon ci FLN (Front de Libération nationale) moomaat nañu seen boppam. Yoon daf leen tëjoon 25i ati kaso ci atum 2020 mi, ginnaaw bi mu leen doon toppe lu jëm ci lëkkaloo ak i rëtëlkat. Ci gaawu bi lañu jotaat seen péexte ci njégalu Njiitu réew ma. Muy lu réewum Ruwàndaa yoonal bu fekkee ni aji-tëj bi nangu na i njuumteem, teg ci jéggalu.

Càdd

Càdd, Njiitu réew ma Mahamat Idiriis Debi Itno jégal na 380i way-féttéerlu yu Fact (Front pour l’alternance et la concorde au Tchad). Ci gaawu bi weesu la jël ndogal lile ginnaaw bi leen Yoon tëjee kaso seen giiru dund ci talaata ji. Ñu doonoon 400i téeméeri doom-aadama. Bàyyi gi nag, mi ngi aju ci déggoo gi amoon ci diggante nguur geek yenn rëtëlkat yi ci weeru ut 2022 ngir jàmm mën a delsi ca réew ma.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj