Abdulaay Wàdd njiitu réew mi fi woon génn na ca tekkaaral ga mu nekke woon. Waaye génnam boobu mën nañoo wax ne njuuy na ñu bari. Ndax la ko yitteel mooy doxinu kurélu pólitigam bii mu jiite di PDS ba bu fi jógee ñu mën koo wéyal.
COOWAL AMI NJAAY ÑIIBI MASATA SAMB AK MAMADU ÑAŊ
Coowal Ami Njaay Ñiibi, Mamadu Ñaŋ ak Masata Sàmb, depite ya doon xeex ca Ngomblan ga jeexagut. Ndax waa Mustarsidiin yi jibal nañu seen kàddu ngir ñu saytu pelent yi ñu dugal te lim ba takku lool. Nee ñu nga, bu Yoon deful liggéeyam, ñoom dinañ ko fajal seen bopp.
MITIŊ COJER
Ndaw i COJER yi dañ doon amal am ndaje ci dibéer ji. Li ñu dugge woon ngir wone seen doole, ñoom itam, ginnaaw bi Pastef dajalee mbooloo mu takkoo takku ba ñu kow soow fu nekk. Waa APR, ci njiitalu Musaa Sow, seen yéene moo doon dajale lu tollu ci 10 000iy ndaw ngir waajal palum njiitu réew mi keroog 2024. Waaye, bu yeboo yàqi. Ndaw, la fa daje woon ciy nit bariwul. Béréb ba dafa yaraaxoon ni kuddub ceeb bu weseŋ bees yakk ci bool bu yaatu. Rax-ci-dolli, ndaw ñu bari dañu nangu xaalis biñ leen doon jox, 2000 FCFA ak 5000 FCFA, daldi dëpp, daldi ñibbi.