Yokkal nañu dépite yi 700.000i FCFA ci seen peyoor. Loolu nag, ci weeru saŋwiye wi la dooroon ; maanaam, ñoo ngi ci ñaari weer yoy, yokk gi tàbbi na ci. Li ko waral mooy, ci lees wax, dañoo téye daamari liggéeyukaay yi, wuutale ko xaalis boobu. Léegi, ñi nga xam ne ndombog-tànk dépite kepp lañu yor, am lu tollu ci ñaari miliyoŋ ak lu teg, Njiitul ndiiso yi am ñaari miliyoŋ yu teg, Njiitul pekk yi am lu jege ñetti miliyoŋ.
Dooro Gay dóor na pelent
Pelent boobu nag amagul boroom (x). Li ko wund mooy biralug xibaar yu wérul, ay saaga ak tëkkub rey. Ndax, moom Dooro Géy, dafa weddi tuuma ji ñu teg ci ndoddam, wax ne moo joxe lu tollu ci fukki miliyoŋ ngir am benn widewoo. Jébbal na pelent ba ca kanamu toppekatu bokkeef gi ngir mbir yi leer, mu mën a setal deram.
NJÀNG AK NJÀNGALE
Kuréli jàngalekati Senegaal yi door nañu, démb ci altine ji, seen palug njiit lu leen di teewal ci sàndikaa yi. Muy ab wote bu am solo ñeel njàng meek njàngale mi. Wii yoon, ci jumtukaayi xarale yu yees yi lañu ko jaarale. Li ñu ko dugge mooy gën leen a yombal te jàppandal wote bi ci ñépp.
COOWAL RAGLUB KOLDAA
Liggéeykati raglu bu mag ba ça Koldaa ñoo taxaw temm ne, démb ci altine ji, njiital raglu bi du dugg biir raglu bi. Ca fajar lañ xéy taxaw ci bunt raglu bi di xaar kii di Jibiril Yansaane, njiitul raglu bi, ngir xamal ko ñàkk xareñteem, ak it ne dafa war a tekki ndombog-tànkam. Waaye, moom Jibiril Yansaane, bàyyiwul mu sedd. Nde, dafa waññeeku, woowi pólis ngir mën a dugg ci biir raglu bi. Liggéeykati raglu bi yit, nee nañ duñu bàyyi mu sedd. Ndaxte, daanaka, raglu bee gën a feebar way-tawat yi, te loolu jaaduwul.
BURKINAA FASOO
Ca Burkinaa Faaso, Njiit ya jël nañu ndogalub “couvre-feu” ci diwaan yu bare ngir gën mën a jàmmaarlook rëtalkat yi. Ñi ngi ko jël ginnaaw bi cong yi gënee taqarnaase ca réew ma ba nit ñu baree bare jot cee ñàkk seen i bakkan. Alxemes jii weesoo ci mujj. 12i doom-aadama ñoo ñàkk dee ci sox yees soqi ci seen kow, fekk ñoo ngi woon cib lekkuwaay. Ndogal li nag, dinañu ko doxal ci àppug weer ba ñetti weer ci yenn diwaan ya.
TÀGGAT-YARAM
CAN U20 : Senegaal dem na finaal
Senegaal demati na finaal ! Gaynde yu ndaw yi amagul 20i at a defati jaloore. Joŋanteb kuppeg Afrig ñeel ñi amagul 20i at a ngi ame ca Misra (Esipt). Loolu nekkati ndam lu rëy ci kuppeg Senegaal. Démb, ci altine bi, ba 14i waxtu jotee, lañ doon daje ak Tinisii, ci seen démi-finaal, gañe ko ñetti bal ci dara (3-0). Ndaw ñi dax nañu seen kaw, dawal kuppe bi, daldi leen duma. Ñu teg ci di tàllal seen i loxo ngir wone seen der wu ñuul wi. Li ñu ko dugge mooy tontu njiitu réewum Tinisii ak wan naar yi ne, ñuule yi, xeebuñu seen bopp. Jëf joojeet, saa-afrig yu baree ko rafetlu. Ci mbaali jokkoo yi, dañ doon bind Afrig 3 – Tinisii 0.
LIGA / ESPAAÑ
Real Madrid jafe-jafe dugal lañu ame jamono jii. Ci seen 3i joŋante yi weesu yépp, benn bii doŋŋ lañ ci dugal. Loolu nag, andina ay coow yu sew ca seen biir. Sàmpiyonaa ba nag, moo ngi leen di gën a dandu. Barça moo ngi leen rawee 9i poñ léegi gannaaw ba mu témbook ak kii di Real Betis. Teewul seen tàggatkat bi, Anceloti, nee naa “dara jeexagul, donte yombul, noo ngi koy gëm ba leegi”.
LÀMB
Bëre Rëg-rëg ak Saa-Cees
Foo geestu ci mbaali-jokkoo yi, xale yaa nga naan “Saa-Cees moo daan, nañu ko jox ndamam”, am ca ñuy saboote Rëg-Rëg di ko woyal woyu Yuusu Nduur ba naan “Kii moo daanu, mel ni moo daan, yoo-lelle !” Saa-Cees nag, dem na ca CNG démb ci altine bi def “Recours” ngir ñu xoolat mbir yi jox ko ndamam.