Yaakaar tas na ! Ndeysaan. Xibaar bu tiis a tiis a dikkal Senegaal gépp, démb, bi ñu yëgee ne Saajo Maane du mujje bokk ci gaynde yiy joŋanteji ca kuppeg àddina si. Ndege, gaañu-gaañu bi doomu Bàmbali ji ame ci tànk bi, bàyyiwu ko. Dañ ko sax oppeere te, nee ñu, balaa moo wér, fàww mu toog daanaka ñetti weer. Dafa di, àddinay futbal sépp a ame naqar ci jàmbaar jiy wuute xew-xew bu réy bile. Nde, sunu Ñàncoo bi, nees koy dàkkentalee, bokk na ci kuppekat yi gën a aay ci àddina si, siiw lool. Waaye, njortees na ni Senegaal raflewul i ndaw yi mën a siggil réew mi.
Futbal/Qataar 2022 : Xuloo ba jib na biir kuuteefu Senegaal ga
Ginnaaw ba gaynde ya àggee Qataar ci altine ji, Yanqooba Jatara, jëwriñu tàggat-yaram gi dafa bëggoon a dal fa gaynde ya dal. Bees sukkandikoo ci li rote ci yéenekaayi réew mi, Abdulaay Sow, 2eelu tof-njiitu Fédération Sénégalaise de Football, daf ko ko gàntal, bañ ba tëdd ca naaj wa. Moom, jëwriñ ji, dafa mujje sàkku Ogisteŋ mi jiite Fédération sénégalaise de Football mu àtte leen. Loolu, gàcce la te, li muy gàttnga baaxul. Nde, gumba tal na leneen lu dul tëb i teen. Li Saajo Maan dul bokk rekk doy na coow, ay magi jëmm bëgg a yokk ci xar mi karaw. Déet waay.
CAN Handball 2022 : Soxnay Senegaal yi toog nañu
Gayndey Senegaal yu jigééen yi demoon nañu “demi-finale” ci joŋanteb “Handball” bi, boobu ginnaaw bi ñu dóore woon jigéeni Esipt yi 21-19. Waaye, bi ñu dajee ak jigéeni Àngolaa yi, dañ leen a dóor 24-21. Ndeysaan, xalam demoon na bay neex…
PÓLITIG
Ngomblaan gi : woteb nafag 2023 gi
Démb, ci alxames ji, la dépite yi doon fénc, di càmbar nafag 2023 gi leen Nguur gi jébbal. Noonu la fay ba keroog, juróom-ñeenti fan ci desàmbar 2022.
Aminata Ture : “Na Njiitu réew mi wax ak askan wi”
Aminata Ture, ëwriñ ju mag ja woon, àddooti na ci mbirum ñetteelu moome gi ñuy ruumandaat ci réew mi. Ci àllarba jii weesu, ca jataayu Faramfàcce bu Paap Ngañ Njaay la ko waxe. Mu ne, “Njiitu réew mi dafa war a wax ak askan wi, keroog 31 desàmbar, xamal leen ne du laaj ñetteelu moome. Ndax, juróom-ñaari at ak juróomi at, ñaari moome la. Te, ndeyu-àtte réew mi waxul ñaari kamoomey juróomi at.”
JÀPPUG PAAP AALE ÑAŊ
Taxawaayu taskati-xibaaryi
Laata ndajem-waxtaan mi ñu war a amal ci àjjuma ji, taskati-xibaar yaa nga woon démb ca kërug kibaaraan gi ngir sàkku ñu bàyyi seen naataangoo bi. Képp kuy wuyoo taskatu-xibaar, wuyuji woon na wooteb CAP (Coordination des Associations de Presse) bi. Li ko kurél gi duge mooy fexe ba ñépp àndandoo, di jooru naan “Bàyyileen Paap Aale Ñaŋ”.
Taxawaayu CPJ
Jàppug taskatu-xibaar bi, waa bitim-réew tàmbali nañu cee dugg. Kurél gii di CPJ (Comité pour la Protection des Journalistes) nga xam ne ñi ngi ko sos ci atum 1981, nekke ca Amerig, dugg na ci. Moom, kurél gi nag, yéeneem mooy fexe ba di sàmm kibaaraan yi ci àdduna si, musal leen ci bépp xeetu jaay doole. Te, ñoom, ñi ngi artu Nguuru Senegaal ngir mu bàyyi taskatu-xibaar bi fii ak benn fan ci weeru desàmbar. Lu ko moy, dina ko boole ci wayndare wu xonq wow, jaglees na ko réew yi gën a bon ci taskati-xibaar yi.
Taxawaayu ROADDH ak COSEDDH
ROADDH ak COSEDDH yeneen ñaari kurél lañu yoy, ñoom itam, sóobu nañu ci xeex bi, di sotal taskatu-ibaar bi. Muy ROADDH (Réseau Ouest Africain des Défenseurs des Droits Humains), di COSEDDH (Coalition Sénégalaise des Défenseurs des Droits Humains), ñu ngi sàkku ñu bàyyi Paap Aale. Moo tax ñuy bàyyiloo xel kilifay Senegaal yi li UNESCO sàrtal ñeel taskatu-xibaar buy lëñbët.
XIBAARI BITIM-RÉEW
G20 : Bennoog Afrig a ngi fëg ci bunt bi
Bennoog Afrig fëg buntub kurél gees dippe G20. Jéego boobu nag, ci njiiteefu Maki Sàll lees ko seqee. Waaye nag, dara leeragul ci mbir mi. Waa G20 dina daje seen biir, cool ba xam lu mën a nekk la, am déet. Ci atum 2023 mi, ca réewum End, lañuy saytoo càkkuteefu Bennoog Afrig gi.
XEW-XEWI JAMONO
Waaxu Ndakaaru : Càccug ceeb
Jafe-jafeb dund bi ci réew mi ak taraayu njëg yi mi ngi tàmbalee am i njeexital ci maxejj yi. Nde, ab dawalkat la sàndarmiy birigaadu waaxu Ndakaaru jàpp. Li ko sabab mooy ne, waa ji, ci lees wax, dafa bëggoon a sàcc limub fanweer ak juróomi toni ceeb. Waa ji nag, jotoon na yeb ceeb bi cig daamaram laata ñu koy teg loxo. Fi mu doon natte lañ ko ne niib, jàpp. Ci xayma, njëgu 35i toni ceeb mi ngi tollu ci 11i tamndaret, maanaam, fukk ak benni miliyoŋ ci sunuy koppar. Ndekete, xiif du mbokk. Seereer duñ ko weddi de, walla ?
Mbir mu doy waar
Jenn waay juy wuyoo ci turu X. Mb. moo doon këyitloo ab xale bu jigéen bu tudd F. S. Moom daal, ab fowukaay la ko defoon. Ndekete, dañoo xamantee ci mbaali jokkoo yi, ku góor ki xamal ko ne dafa yor ndefar buy defaraat ndaw. Maanaam, buy delloo jigéen ag ndawam daal. Waaye, ngir ndaw si jot ci, fàww daf ko war a jox nataalu awraam. Bi xale bu jigéen bi nangoo loolu nag, jox ko li mu laaj, ci la ko waa ji tàmbalee napp, di ko xoqatal, naan ko, bu nanguwul séq ak moom mu siiwal widewoo yi. Bi soxan si sonnee ci mbir yi, mu tegal ko ab ndëgg-sërëx, ànd ci ak pólise yi. Ci lañu jàppe waa ji.
Njaayum sinebaar ak ciif : Saalum-Saalum, mbër ma woon, taq na ci
Kii di saalum-saalum, nekkoon fi mbër, lañu teg loxo. Lees koy tuumaal mooy njaayum sinebaar ak ciifug senn ndaw su tollu ci ñaar-fukki at ak ñeent. Soxna soosu dafa jëndsi woon ci moom sinebaar biy jar 25. 000 FCFA, mu ne ko, léegi 90. 000 FCFA lay jar. Ci la ko waxee ñu séq, mu bañ, mu dóor ko ba noppi tëdd ak moom. Céy Yàlla.