LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (ALXAMES 23 MÀRS 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Maki Sàll a ngi tëkku kujje gi

Dafa mel ni Njiitu réew mi, Maki Sàll, defantee ko tax a jóg. Ci àllarbay démb ji lees doon amal ndajem jëwriñ yi, nees ko aadawoo ayu-bés bu nekk. Bees déggee waxam ja fa tukkee, mënees na njort ne dafa joqarbi kujje gi, rawatina ki ci ko jiite, gën cee fës, muy Usmaan Sonko, njiitul Pastef li. Nde, njiitul Bennoo Bokk Yaakaar li daf ne : « warees na sàmm jéegoy demokaraasi yi te fexe ba sàmm dal gi ci réew mi. Ndax, warres fàttali ne, Senegaal, réewum Yoon la te di royukaay ci wàll wi ak ci wàllu demokaraasi. »

Ginnaaw kàddu yooyile, Njiitu rew mi dafa xirtal nguur gi ci ñu « jël seen matuwaay yépp ngir, fépp ci Senegaal, sàmm kaaraange nit ñeek seen i alal ginnaaw bi ñu nemmeekoo ay yëngu-yëngu ci yenn i bérébi réew mi. »

PASTEF : jàppati nañu El Maalig Njaay

Ñoo ngi wéy di jàpp waa Pastef. Démb ci ngoon gi, boori 15i waxtu, la waa « Sûreté urbaine » woolu woon El Maalig Njaay mi yor kàddug Pastef. Ginnaaw bi ñu ko dégloo nag, dañ ko fa jàppandi, ca komisariyaa bu mag ba. Nee ñu, tuumay ciiwalug xibaar yu wéradi la ko Yoon di toppe. Layookatam bi, Me Musaa Saar, moo ko xamle.

Kàdduy Siidi Baaji, meeru Tàngori

Kàddu yooyu nag ma nga ko yékkatee woon ciw waxtaan wow, doon na ko amal ak ñii di waa Groupes médias du Sud bu Biññoona ginnaaw bi ñu bóomee ndaw lii di Mamadu Koorka Ba. Muy ñaawlu bu baax xeetu jëfin woowu. Te, nee na, dafa jot ñu samp ab laaj ngir xam lan moo tax ñuy dóor maxejj yooyu ay bal te, ñoom yoruñu genn ngànnaay. Te, li ci ëpp, ñu ngiy nemmeeku xeetu jëfin yooyu ci diwaani bëj-saalumu réew mi rekk. Moomu, meeru Tàngori, Siidi Baaji, yokk na ca ne, seen ug njaboot duñuy mala. Te, Njiitu réew mi, Maki Sàll, mooy Njiitu bépp saa-senegaal. Ci jamono yu ni mel, moom, moo war a sàmm kaaraange bépp saa-Senegaal.

Pasug ngànnaay yi : Forum civil fàtteegul njombe wi

Coowal pasug ngànnaay gu 45i tamñaret (milyaar) yi fayagul. Waa Forum civil a sulli coow li. Barki-démb, ci talaata ji, 21 màrs 2023, Biraahim Sekk mi jiite Forum civil ma nga woon ca réewum Almaañ, ca màkkaanum ONG Transparency international (Berlin). Way-moomeel bi jot faa leeral mbirum pas googu Abdu Kariim Sàll xaatimoon keroog, 30 desàmbar 2021, te Abdulaay Daawda Jàllo saxaloon ko.

Ca ndaje ma amoon foofa ca péeyub Almaañ ba, sëñ bi Sekk wax na fa ne, ay yooni yoon, laaj na càmmug Senegaal ay leeral, waaye tontuwuñ ko. Ñoom nag, waa Forum civil, li ñuy ñaawlook a naqarlu mooy li Njiitu réew meek toppekat bi deful dara ngir leeral mbir mi. Cig pàttali, waa Occrp, ag mbootaayu taskati xibaar yiy luññutu, fekk baax ci 30i réew, ñoo siiwaloon njombew pas googu, keroog 25 oktoobar 2023.

Koorug 2023

Atum ren jile, bennoo dina am ci Senegaal. Nde, réew mépp woorandoo ci bésub alxamesu tey jii, méngook 23 màrs 2023. Ci talaata ji la kurél gii di CMS (Coordination des musulmans du Sénégal) séentu woon weer wi, gisu ko. Ca la xamlee ne koor gi bésub alxames ji lay door. Kurél yii di ASPA ak CONACOC, ñoom itam di saytu mbirum weer wi, séentu nañ ko démb ci àllarba ji, daldi koy gis, xibaare nit ñi ne, ndoorteelu koorug 2023 gi, day dëppook alxamesu tey ji. Moo tax, tey, julliti Senegaal yépp a woorandoo.

Ñu fàttali tam ne, kercen yaa ngi ci seen ug koor, ñoom itam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj