UBBITEG FÓRËM KOOM-KOOMUG MBOOLAAY GEEK JÀPPALANTE BI
Ci alxamesu tey ji la Njiitu réew mi, Maki Sàll, doon jiite ubbiteg Fórëm koom-koomug mboolaay geek jàppalante bi. Ca Garã-Teyaatr la doon ame. Bi Maki Sàll jëlee kàddu gi nag, tagg na fa Bàrtelemi Jaas, wax ci moom wax ju rafet.
“Dama bëgg a ndokkeel bu baax meeru Ndakaaru bi, Bàrtelemi Toy Jaas. Doon na ko wax sànk, “Bàrtelemi, yaa ngi doxal de !”… Dinaa wax sa baay mi nekk ak man ne, sa doom a ngi liggéey. “
Ndaje ma, amoon nay kilifa yu fa teewoon itam niki Xalifa Sàll, Sowam Wardini ak Abiib Si.
DÉCCE FAAL AK PRP DËDDU NAÑ WAXTAAN WI
Tey ci ngoon gi la waa PRP, pàrti pólitig bi Décce Faal jiite, génne ab yégle di ci xamle ne, ñoom, duñu wuyuji woote Njiitu réew mi ngir waxtaan wi mu sumb. Nee ñu, ginnaaw bi ñu waxtaanee seen biir ba noppi, fas nañoo yéene DËDDU waxtaan woowu. Nde, Décce Faal ak i ñoñam dañ jàpp ne, ndogal ya tukke woon ca waxtaanuw 2019 wa, menees na leen jëmmal te sàmm àq ak yelleefi nit ñi, bàyyi taskati xibaar yiñ singali, bàyyi waa kujje gépp bokk ci wote yi, añs.
DOXU-ÑAXTU LIGGÉEYKATI CAYTUG BOKKEEF GI
Liggéeykati caytug bokkeef gi dinañu génn ci mbedd mi bu 15i fan jotee ci weeru me. Ginnaaw bi ñu jëlee ndogalub takk ay sagar yu xonk ci ayu-bés bi, Omar Daraame ak i moroomam dinañu génn ñaxtu. Ñoom nag, li ñuy kaas mooy ñu boole ñépp ci ndàmpaayi dëkkuwaay yi, bañ a beddi benn Liggéeykat.
BAABAKAR TURE KÉWOULO ÑIBBI NA KËRAM.
Njiitul Kéwoulo TV laa Nga woon ca kanamu Yoon. Ginnaaw bi mu tawatee woon ba ñu rawale ko ca raglu ba, dafa doon janoowaat ak àttekat bi. Mujjee na ko bàyyi sax mu ñibbi këram. Dañ ko bàyyeegum bàyyib négandiku. Nde mu ngi ci «contrôle judiciaire». Day jébbal Yoon jàll-waaxam fileek ayu-bés. Rax-ci-dolli, weer wu teru, dina teew ca kanamu Yoon njëlbeenug àjjuma ju nekk, ngir xaatim luy wone ni dawul génn dëkk bi. Moom taskatu xibaar bi, di tamit luññutukat, siiwal nay kàddu ci xëtu facebookam :
“Maa ngi sant Yàlla. Maa ngi nii, delsi naa ginnaaw bi ñu ma téyee juróom-ñetti fan. Bu tey doon démbeet, damay defaat liggéey bi ma defoon ngir muccal réew mi ci meneen musiba ni layoo Prodac bi.”
Mu mel ni, moom, réccul jëf ji taxoon ñu jàpp ko.
NDAJEM JЁWRIÑI ÀLLARBAY DÉMB JI
Ca ndajem-jëwriñ ma mu doon amal démb, Njiitu réew mi, Maki Sàll, tabb na fay nit ñu bees. Muy ku ci mel ni Aamadu Abdul Si (Président du Conseil d’Administration du Laboratoire National d’Analyses etv de Controle LANAC), Sàmba Sàll (Président du Conseil de Surveillance de l’Agence national de l’Etat civil ANEC), Xaadim Jóob (Président du Conseil d’Administration du Conseil exécutif des Transports urbains durabes CETUD), Ceerno Biraahiim Aaw (Directeur général du Conseil exécutif des Transports urbains durabes CETUD) ak Ãsumaana Saane (Directeur général de l’Agence de Régulation des Marchés ARM).