Daara ju kowe jii di UADB (Université Assane Seck de Bambey) dafa nekk di jànkonteel ak i jafe-jafey ñàkkum ndox. Nee ñu, bi ñu ubbee ba léegi ndox amu fa. Ndax kat, daara ji dafa ameel bor kurél gii di Sen’eau ñu xayma bor bi ci ci 100 miliyõ. Ndongo yaa ngi artu Njiitu réew mi mu geestu leen ndax ni ñuy dunde mënul a wéy. Te, nee nañu, ci jamono jii, amul genn kurél gu leen di kaasal ndax ñi fa newoon nekkatuñ fa.
Coppite ci boppu kurél gii di CROUS fale ca UGB
Ahmadu Bàmba Ka di jàngalekat ci wàllu làmmiñal (Lettres) moo jiite léegi kurél gii di CROUS (Centre régional des œuvres universitaires de Saint-Louis). Kii di Paap Ibraayma Fay la fa wuutu, moom mi nga xam ne dañu koo dénk beneen liggéey.
PÓLITIG
Bésub Àjjuma jii la mboolem dépite yi di amal seenmennum ndaje mu atum 2022-2023, ñu dippe ko « session ordinaire unique de l’année » . Nde, ren la Nguur gi nar a dundu at mu doy waar ginnaaw bi mu ñàkkee raw-gàddu gi fale ca Ngomblaan gi. Nee ñu sax, tàmbali nañ leen a diir-mbagg rawatina Mimi Ture mi bëgg ñu samp ay tëralin walla àtte buy tere képp ku mbokkoo ak Njiitu réew mi di jiite fenn ci kenoy bokkeef gi (les institutions de la république).
KOOM-KOOM
Soxna sii di Absatu Si moo fas yéene sumb ab sémb bu mu dippee « Africa Mith ». Ci xayma, bile sémb ab yeesal la bu mu indi ci wàllug lijjanti « entrepreneuriat ». Moom nag, doomu Afrig la, di doomu Senegaal itam. Bile sémb, ràññee nañ ko fépp ci àddina si. Nde, dafa bëgg réewi Afrig yépp gis ci seen bopp rawatina réewum Senegaal nga xam ne dafa war a jëfandikoo dayo yi mu yore ngir suqaliku.
XEW-XEWU JAMONO
Kii di Kalifoon te ñu ràññee woon ko lool ci mbaali jokkoo yi, mu nekkoon itam ca loxoy yoon ndax coow lu doxoon ci digganteem ak benn xale bu jigéen, mujjee nañ ko àtte. Juróom-benn weeri kaso lañ ko daan. Ci juróom-benn weer yooyu, benn bi lay tëdd ba mu jeex tàkk.
BITIM-RÉEW
Ginnaaw bi réewi Afrig yu bari bañee woon a wone seen péete ci xare bi dox diggante Riisi ak Ikren, démb, ci ndaje mi ONU amaloon, Maki Sàll mujjee naa xamle péeteem ci xare bi. Nde, Ikren la àndal te moom la jox baatam ci wote yi. Ci xayma 35i réew ñoo wonewul benn péete ci xare bi. Ci ñoom, Siin a ngi ci, End, Pakistã, añs. Bët gànnaaru Kore, Eritre, Siri ak Biyeloriisi, ñoo woteel Riisi.
TÀGGAT-YARAM
Démb, ci joŋante bi doxoon diggante Bayern ak Viktooriyaa ci kub bii di « League des champions », la doomu Senegaal bii di Saajo Maane dugal 200eelu bitam ci këlëb. Moom mooy ñeenteelu futbalkatu Saa-Afrig bu dugal lu ëpp 25i bal ci bile kub ginnaaw Dorogba, Samiyel Eto’o ak Muhammed Sala.