LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI, Dibéer 14 ut 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG 

Li bettul kenn mooy fekki gi Paap Jóob fekki waa BBY. Mu nekkoon lu ñu doon kummuj, far na doon dëgg. Jëf ji di dëggal la leen seen naataangoo ba waxoon di Usmaan Sonko. Moo di ne, kujje gi, ñaar a ko séq, ña ca des ca Nguur ga lañu fare. 

MBËNN MI

Gox yu bari ca biir Ndakaaru ña ngay wéy di féey ca ndox ya. Ña dëkke Ngor ak Almadi di fésal seen njàqare rawatina bu yeneen taw wàcce ci seen gox yooyu. Lañuy tiit mooy mbëj ga mën naa jaxasoo ak ndox ma. Te loolu mën naa jur jéyya yu mag foofu. 

KAAWTEEF

Ca Almaañ lañu bóom ab saa-senegaal. Ña def loolu di way takk-der yu Dortmund. Ñoo soqi ay sox ca ndaw lu tuddu Lamin Daraame bam faf ñàkk bakkanam. Saa Senegaal ya féete foofa ña ngay ñaawlu jëf ju ni mel. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj