Ay coppite ak i naal moo tënk waxtaan wu mujj wi Njiiti réew Afrig yi séqoon fale ca Adis Abebaa. Mu am coppite ci boppu kurél gi ëmb réewi Afrig yi. Nde, Màkki Sàll mi jiiteewoon kurél googu jox na lenge yi naataangoom bi di Njiitu réewum Komoor, Asali Asumani.
DIINE
Kasu rajab, di màggal gi ñu jagleel sëriñ Fàllu Mbàkke, doonoon ñaareelu kilifa Sëriñ Tuubaa, amal nañu ko bërki-démb, ci àjjuma ji. Xew-xewu diine boobu ñu di ko defe Tuubaa, dajale woon nay taalibe ak i soppe ngir fàttaliku ñëwug jamono Séex Fàllu.
KÀDDUY ARTU
Sëriñ Bas Abdu Adr mi yore kàddug yoonu murit, àddu na ci tolluwaayu réew mi. Mu mel ni ñenn ci way-politig yi ni ñuy faral di yëgal réew mi, ñaawlu na ko. Muy artu ci diwaanu Tuubaa ak liggéey bu mag ba fa Sëñ ba def di wax ne kenn mënu koo yàq.
WALF TÀKKAGUT
Doxub ñaxtu di ñu bëggoon a amal ci Gaawu jàpp Dibéer ca bunt i CNRA, Perefe bu Ndakaaru dàq na ko. La ko waral di siñaalu tele Walf ba ñu daggoon te jàmmarloo ba amoon Mbàkke waraloon ko.