LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (Dibéer 29 saŋwiye 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

TUUBAA : JAWUB “OCASS” LAKK NA

Démb ci guddi, ay boori 22i waxtu, lees nemmeeku ag lakk ca « Marché Ocass » ba nekk Tuubaa. Ci anam bu gaaw a gaaw la jëléemi safara si jàpp ay kàntin yu baree bari yi féete ci wet gees duppee « marché fraude ». Yu baree tàkk ba jeex. Sàppëer daw ñëw ngir fay làkk gi, waaye dañu amoon i jafe-jafe ngir àgg fa làkk gi féete ndax xataayu yoon beek taabali jaaykat yi ci yoon wi. Boroomi kàntin yeek ña fay liggéeye dawsi woon nañ ngir dimbali sàppëer yi. Laata 1 waxtu di jot ci guddi gi lañ ko mujje fay.

Antuwaan Jom, jëwriñu Biir réew mi, demoon na ca béréb ba. Dalal xeli jaaykat ya, wax ne Nguur gi dina jël i matuwaay ngir jéyya yu ni mel dakk fa.

« Dinanu waxtaan ak ñi lakkley kàntin, waxtaan itam ak delegey jawu Ocass ak yeneen ja yi, boole ci jëwriñ ji ci aju ngir wut pexe, dakkal lakk yi. »

Jamono jii nag, nee ñu 480i kàntin ak 70i màngasin ñoo ci lakk. Antuwaan Jom moo joxe xibaar bi, ci Seneraal Mamadu Ndóoy mi jiite Sàppëer yi moo ko ko xamal. 

DËJ : SËRIÑ MOODU ÑAN, TËGGKATU LAMB BA WOON, GAAÑU NA

Ci gaawu bi la xibaar bu tiis bi jib. Tëggkatu-làmb ba woon, Sërñ Móodu Ñaŋ, boroom Mouniang Productions, moo faatu. Ca loppitaanu Dalal Jàmm ba mu tëddoon la gaañoo. Ci àjjuma ji lañ ko fa yóbboon. Mbokki làmb yépp ñoo teewoon ca jullee ga, ànd ak moom ba armeeli Tuubaa ya ñu ko denc.  

PÓLITIG

Kilifa gu mag gu Medina Baay, Sëriñ Maa’i Ñas àddu na ci tolluwaay pólitigu réew mi. Mu mel ni magum waxoon naa ko moo gën magum xamoon na ko. Muy dànkaafu képp ku jóg ngir taal réew mi. Ay kàddoom nekk kàdduy waaraate ak fàttali jëm ci ku nar a yee fitna. Muy ñaawlu woteb jàmmarloo bu ñenn ci kilifay pólitig yi di woo askan wi. 

SIYAAR POROXAAN

Njiitu Ngomblan gi, Aamadu Maam Jóob ak ñenn ci ay ñoñam, amal nañu ab tukkib nemmeeku ca Poroxaan. Dëkku Soxna Jaara Busó, miy waajuru Sëriñ Tuuba. Ay tànkam di tànki siyaar, waaye tamit ñaan jàmm ci tolluwaayu réew mi, diy kàddu yu mu diis kilifag murit yi di Sëriñ Muntaxaa.  

MBATIIT

Njabootu Allaaji Omar Fuutiyu Taal amal nañu seen siyaar ba ñu daan def te ñu jagleel ko jàmbaari Lislaam ya, Ceerno Séydu Nuuru Taal ak Ceerno Muntagaa Taal. Ren di 43eelu yoon bi ginnaaw bi ñu tooge ay at defuñu ko ndax mbas mi. 

FUTBAL

Kuppeg réewi Afrig yi ñu jagleel ekib yu ndaw yi, Senegaal jàll na ca demi finaal ya. Ginnaaw bi mu dóoree Muritani, gaynde yu ndaw yi war a dajeek ekibu Madagaskaar.    

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj