LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (GAAWU 01 OKTOMBAR 2022)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG 

Bitim-réew, ca Burkinaa Faaso, ñu nemmeekooti fa poqartim Nguur, ginnaaw juróom-ñatti weer kott ba fa Póol Ãari Damibaa jëlee Kaboore. Ka ko fa wuutu di Ibraahima Taraawore. Mbotaayu xeet yi ëmb réewi Afrig yi ñaawlu nañu ba fa ñaawlu yem li xarekat yi def. 

DIINE

Gàmmu, xew-xewu diine bu mag, ñu koy amal fii ci Senegaal ak réew yi ko wër. Muy màggal juddug Yonent bi Seydinaa Muxàmmad (sas). Waajtaay ya door na ca këri diine yi gën a mag ci réew mi niki Tiwaawon. Bés boobu di fukk i fan ak ñaar ciw Gàmmu, yamook Àjjuma juróom-ñaari fan ci weeru oktobaar. 

NJÀNG MI

Kuréel gi ëmb jàngalekat yi (CUSEMS) amal nañu seen ñetteelu lël. Xew-xew boobu ñu door tay ci gaawu bi mu war a wéy ba dibéer, dajale na mboleem ñuy yëngu ci njàng mi ak njàngale mi. Ñooñu di dànkaafu Nguur gi ngir ag yamale ñeel payoor yi.  

TÀGGAT-YARAM

Tay ci gaawu bi la gayndey Futbal yu tefes yi ( beach soccer) doon laale ak wa Esipt ci kubu COSAFA . Ñuy wéy di firndeel seen xarañte ñeel po moomu. Ndax, ñoo jël raaya bi ginnaaw bi ñu dóoree Esipt juróomi bal ci ñett (5-3) .

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj