LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI GAAWU 03 DESÀMBAR 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Ginnaaw ndajeem jëwriñ yi mu amaloon, Njiitu réew mi Màkki Sàll, takkal na ndombog-tànk toppekat bu mag ba woon, Sëriñ Basiiru Géy. Mu fas yéene jiite OFNAC di kurél giy xeex luubal ak nger. Ka mu fa wuutu di Séynabu Njaay Jaxate ma fa wuutu woon Nafi Ngom Keyta. 

XEEXUB NGOMBLAN GA

Coowal Ngomblan ga dafa mel ni pënd ba wureegul. Dépite Ami Njaay ma ñu dóoroon am talaata, tegal ko ca am wéq, ca lopitaal la mujje. Mbir ma mel ni dafa ëpp i loxo, ndax jigéen ja dafa wann lor. La ñu doon tiit ak a laam-laame, xel mujj na caa dal muy ag loru ca la mu àndal. 

TASUM XIBAAR

Kurél gii ñu dippe CAP, ëmb taskati-xibaar yi, amal nam ndaje tay ngir jàppale seen naataangoo bii di Paap Aale Ñaŋ. Ñu àddu ci wér-gi-yaramu taskatu-xibaar bi ñu teg loxo. Kooku nekk ci ñaareelu fanu xiifal gi door. 

WAY-LAAGO YI

Démb, gaawu, 3i fan ci desàmbar, moo nekkoon bés bi ñu jagleel way-laago yi. Ñu màggalee ko ca Welingara. Way-laago yi nag, biral nañu seen i jafe-jafe. Bokk na ci, seen dem ak dikk, njàng mi ba ci bérébu fajuwaay yi. 

TÀGGAT-YARAM

Ay waxtu kepp ñoo des ngir gayndey Senegaal yi jàkkaarloo ak waa Àngalteer ginnaaw bi ñu génnee ca seen wërngal bu njëkk. Ki topp ci Aliw Siise, Resi Bogaar, jottali na ab xibaar ñeel wér-gi-yaramu Aliw Siise. Mu mel ni jarag da koo dab.  Na taneek jàmm waay, gindi gaynde yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj