LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI GAAWU 10 DESÀMBAR 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Woteb nafag 2023 gi jeex na ci gaawu bi. Jëwriñ ji ñu dénk nafag Senegaal jàkkarloo na ak dépite yi. Mu mel ni am nanu jafe bu ñu ko méngale ak ay naataangoom ya fa jot a jaar. Ñu nattal ko nafaam lu tollu ci 369 666 638 517i ci sunuy koppar.

Mbirum Ami Njaay Ñibbi

Coowal xeex ba woon ca Ngomblaan ga fayagul. Dépite Masata Sàmb ak naataangoom bii di Mamadu Ñaŋ ña yoon doon wër te ba tay gisaguñu leen, seen i mbokk jàppal nañ leen tànk. Muy ag taxamu ci mbir moomu ginnaaw bi ñu ko ñaawloo. 

Paap Aale Ñaŋ

Ab xibaar ñeel wérgu-yaramu taskatu-xibaar bii di Paap Aale Ñaŋ rot na. Ginnaaw ba soxnaam artoo jëm ci wér-gi-yaramam, rawale nañu taskatu xibaar bi cab bérébu fajuwaay. Mu mel ni wér-gi-yaramam sooke na lool ginnaaw bi mu amalee juróom-ñeenti fani xiifal. Ay layookatam doon ko ñaanal ab bàyyib négandiku, ginnaaw bi ko àttekat bi dégloo. Waaye, mu mel ni loolu amaguñ ko. 

XIBAAR YU TIIS

Tali baa nga wéy di faat ay bakkan. Ab aksidaŋ bu metti moo am ci yoonu “autoroute” Ilaa-Tuubaa bi. Fay tollook Xommbal la ab kaar bu ndaw (mini car) mbëkkanteek sëfaan  juróomi nit faatoo ci. Jéyya ja far gën a tee metti bi ci ñetti nit dolleekoo. Ña ca ame ay gaañu-gaañu bari nañu tamit.

Ginnaaw Xommbal, Mbuur tamit sëngeem na. Ñaari nit la fa ab wëyu sox ay bal i fetal ba ñu ñàkk seen i bakkan. Mbir moomu ma nga xewe ca ja bu Mbuur ginnaaw ba fa sàmbaa-bóoy bi amalee ag ciifug koppar.  

TÀGGAT-YARAM 

Mënees na ne guléet, ba joŋanteg kuppeg àddina sosoo ba léegi, am réewu Afrig di jàll ci demi finaal yi. Marog a def jaloore ji. Moo tax, am na woy wu réy. Moo njëkk a nekk dëkku Afrig bu bokk ci ñeenti réew yi war a xëccoo ndam li. Mu doon ndam ci kembarug Afrig gépp. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj