LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI Gaawu 10 Sàttumbar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG 

Ngi waajal màggalu Tuuba, wa YEWWI-WALLU amal nañu seen ub siyaar ci kanamu kilifag murid yi. Mu mel ni mbég ak soññe ci ñoom, bu ñu sukkandikoo ci kàddug Usmaan Sonko mi yoroon seen kàddu. Li ko waral di jaar-jaar ya Sëriñ bi biral jëm ci dogu gi ñu dogu woon ngir askanam. Loolu mel ni buuña ci ñoom ndax lu nit ñi umple woon la. 

BITIM-RÉEW

Ca Àngalteer, Lingeer Elisabet II moo génn àddina. Bi my gaañu, 96i at la Elisabet II amoon. 50i at la nguuru. Réewi tugal yu bari sargal nañu ko, rawatina réewam ma nga xam, ajees na fa bépp xew-xewu po walla tàggat yaram.

NJÀNG AK  NJÀNGALE

Jëwriñ ji ñu dénk njàng ak njàngale fésal nag yëgle di ci xamle kañ lay bër giy jeex di wone tijjiteg lekkool bi. Mu mel ni jàngalekat yi ci ñetti fan ci wéer wee ñu jëm di Oktoobar lañu leen woo. Budee ndongo yi juróom-benneelu fan ba.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj