Démb ci Àjjuma ji njiitu pasteef lii di Usmaan SonkoTuubaa la jullee. Mu nekk wokkotu bu dajeek geestu ci moom. Mu mel ni la mu doon sàkku ci ay weer, am na ko ci bés boobu. Muy giseeg kilifag muriit yi di Séex Muntaxaa Basiir.
AG SAAFOONTE
Am ndaje, gisante wala saafoonte nu ñu ko mën na dippe bari na. Waaye Usmaan Sonko jot naa waxak Kilifag muriit yi di Séex Muntaxaa fa mu doon jullee ca jumaa ja. La ko sëriñ bi wax bu ñu sukkandikoo ci Senenews mooy namm ag dal ci biir Tuuba te mu dellu ci jàmm.
MÀKKE TÀNG NA DÉMB
Abjàmmarloo bu metti moo doxoon diggante takk-der yi ak sopey Usmaan Sonko yi. Ay xeer ak i gërënaad yu ñuy sànnante tax ba yaxu-yaxu yi ak ñi ci jële ay gaañu-gaañu bari na. Bokk na ci Senchan ba ñu salfaañe, Sonatel ba ñu rajaxe añs.
MEETAR ELAAS JUUF AJANDI NAÑ KO
Muy ab xibaar bu ñu biral démb di xamle ne layookat bii di Meetar Elaas Juuf aj nañu ko. Ñi ko def di ay naataangoom,loolu di firi ne liggéeyam boobu dakandi na.
WALF FAY NAÑU KO
Walf fay nañuy fiilam ñi ko def di waa CNRA. La ko waral di nataal ya mu doon genne di wone jàmmarloo ba amoon Màkke. Séex Ñas ma ko jiite di xamle ne seen liggéey rekk lañu doon def ginnaaw ba ko Usmaan Sonko dëfalijee.
TAGGAT-YARAM
Làmb nar naa sàjji suba ci Dibéer ji. Ñaari mbër nar a laale wala sax laalewaat. Muy Bombarjée ak Tafaa Tin, nekk ay kàngam ci wàll woowu fas yéene bëre ngir wut ndam lu leer