LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (GAAWU 12 NOWÀMBAR 2022)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG
Na mu ko yëglewoon ginnaaw ba mu janook taskati-xibaar yi, Usmaan Sonko miy njiitu PASTEF, wéyal na Nemmeeku Tour ba mu dooroon. Démb ci àjjuma ji ma nga woon ca Tiwaawon. Mu fas yéenee wéyal tukkib nemmeekoom ca Pir.

KOOM-KOOM

Liggéeykat yi ŋàkk mbay mi, napp gi ak càmm gi mujj nañoo wàcc ci mbedd yi. Lañuy ñaxtu mooy ñàkk déggoo gi am ci seen payoor yi walla ndàmpaay yi. La ñu xaatim seen diggante ak Nguur gi lañu nanguwul. Ñu nar a wéyal seen ub ñaxtu bu ci saafara amut àpp ko ba ci xiifal.

WÉR-GI-YARAM

Ginnaaw coow li fi woon ca Dantec ba ñu toxal bérebu fajukaay yu bari, wa “dialyse” ña ñu tuxaloon ca bayaalu naawaanu Léwopol Sedaar Seŋoor wàcc nañu ca mbedd yi. Lañuy naqarlu di ñàkk i jumtukaay ya ñuy fajoo. Ñu ànd ci ak njàqare. Ndax, la seen faju googu mënut xaar diir bu yàgg.

TÀGGAT-YARAM

Aliw Siise miy tàggat gayndey Senegaal yi, fésal na ña mu woo ngir kuppe àddina si. Lim ba mu biral tollu ci 26i kuppekat. Waaye mbett am na ca. Bokkug Saajo Maane juroon na njàqare ginnaaw gaañu-gaañu ba mu ame woon. Waaye tamit, ñàkkug bokk bu Saaliw Siis metti na saa-senegaal yu bari.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj