Ni ñu ko junjee woon ginnaaw palum depite yi, kujje gi taxawal na kurél gu leen di ëmb. “REELS ( Réseaux des Elus Locaux du Sénégal) dib kuréel ngir gën a dooleel liggéeyu depite yi, sampu na tey Gaawu 15 ci weeru oktoobar. Ki ko jiite di njiital PASTEF, Usmaan Sonko.
KOOM-KOOM
Ndaje ma “ BRETTON WOODS” di amal at mu jot, Ulimata Saar di njiit lu bees li ñu tabb ci koom-koomu Senegaal jot na faa tebbi ñaari sémb yu am solo. Benn ba soxal defarum ñakk, beneen ba di càmbar wàllum suuf.
MBATIIT
Gàmmu, Gàmmuwaat niki ni ñu ko xame, Njaasaan ak Medina Baay tey ci Gaawu bi lay màggal juddug Yonente bi (sas). Dëkk bu Maam Séex Bu-Kunta dalal na mbooloo mu takku ñu jóge ci biir réew mi ak ca bitim-réew.