LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (GAAWU 17 DESÀMBAR 2022)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Colidep (Collectif pour la libération des détenus politiques) amal nañu démb seen doxub ñaxtu. Kurél googu nag, seen yitte mooy fexe ba génne ñi Nguur gi jàpp, teg leen loxo ci sababu joxe seen i gis-gis walla seen i xalaat. Bokk na ci ñi ci gën a fés, kii di Kariim Xurum-xaax, Aatumaan Jaan, añs. 

MBATIIT

Artist bii di Nit-dof di yëngu ci wàllum Rab, am mer mu réy la wone ginnaaw ba perefe bu Ndakaaru gàntale “Show of the year” bi mu daan amal. Mu nekk tamit ku ràññeeku ci politigu réew mi. Ay kàddoom di ŋàññi lu bari Nguur gi fi toog.

DEM AK DIKK

Jëwriñ jii di Sàmba Njóobeen Ka, jébbal na lu tollu ci 70i tamndareti seefaa ñi di dawalkat ya loru woon ca Mali. Muy ag ndimbal gu Nguur gi yékkati ngir jàppale liggéeykat yooyu. 

TÀGGAT-YARAM 

Ginnaaw bi ko réewum Farãs dóoree ci demi-finaal yi, Marog tegoon na yaakaaram ca ñatteelu toogug kuppeg àddina si. Waaye, Kurwaasi ma mu ko doon xëccool, jël na ko. Mu doonoon finaal bu ndaw bi ñu doon amal tay ci ngoonug gaawu bi. Kurwaasi moo ko dóor ñaari bal ci benn (2-1). Finaal bu mag bi, ñu di ko xaarandi ëllëg, ci dibéer ji, diggante Farãs ak Arsàntin.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj