LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI Gaawu 19 nowàmbar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Woteb nafag 2023 gi door na ca Ngomblaan ga. Tey ci gaawu bi, jëwriñ ji ñu dénk wàllum dëkkuwaay yi ag cet gi, Abdulaay Séydu Sow, xam na lañ def cag gafakaam. Ñu seetlu ci ag wàññeeku bees ko méngaleek at mii weesu. Nde, 85 340 344 196 ci suñuy koppar.

Horizon Sans Frontiére ( HSF)

Buubakar Séy bu “Horizon sans frontiére” (HSF) wone na meram ci lu ñu dog ay buumi jokkoom. Ñi mu joxoñ baraamu tuuma di waa ‘Sonatel”. Mu gis ne, Nguur gee làqu ci ginnaawam. Li ko waral mooy, bu ñu sukkandikoo ci ay kàddoom, li muy sàkku ñu bàyyi Paap Aale Ñaŋ ak xibaar ya mu siiwal ci gis-gisu waa bitim-réew ñeel ñetteelu moome gi Màkki Sàll nar a sàkku te,  téeméer boo jël, 99i tontu ca déed.

KOOM-KOOM

Liggéeykat yi ŋàkk mbay mi, napp gi ak càmm gi, ñu dippee leen “secteur primaire”, dafa mel ni seen i jafe-jafe amagut saafara. Ndax, ña fare ca napp ga ñooy sàkku ci jëwriñ ji ñu dénk wàllu woowu, Paap Saaña Mbay, mu tekki ndombog-tànkam.   

TÀGGAT YARAM

CAN Handball 2022, gaynde yu jigéen yi ñàkk nañu ñetteelu toogu ga. Ginnaaw bi leen Àngolaa dooree, ci lañu janoog jigéen i Kongo yi ngir ñaareelu finaal bi. Ñooñu rawe leen benn poñ (20-19) ñu mujjee nàkk.

 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj