LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI Gaawu, 20 ut 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

XEW-XEWI JAMONO

Yokkuteg njëgu soble ga ca Tuubaa 

Ñàkkum soble bi ganesi réew mi ci fan yii tax na ba saaku soble bi daan jar junni ak ñeent-téemeer (7.000), léegi fukki-junni lay jar fale ca Tuubaa. Kilo bi nag moom yéeg na ba ñeenti-téemeer. Mu nekk lu diis lool ci ñenn ci maxejj yi ba tax na kii di Aali Njaay, te jiite fale ca Mbàkke mbooleem béykati soble ya fa nekk, xamle na ne dinañ jël seen i matuwaay yépp ngir njëg yi gën a jàppandal ci ñépp.

Aksidã bu metti ca Kafrin

Lii di ab aksidã bu amoon démb ca diwaanu Kafrin, juróomi nit ñoo ci ñàkk seen i bakkan, juróom-ñaar-fukki nit ak ñaar  jële ci ay gaañu-gaañu. Ci ñoom, am na juróom yoo xam ne dañu sonn lool, maanaam ñoo ngi ci diggante dund ak dee. 

KOOM-KOOM

Senelec ak bor yi gàllu ci kowam

Ñoo ngi toppe këru liggéey bii di senelec ñeen-fukki (200) miliyaar yoo xam ne ameel na ko ñenn ci këri liggéey yuy jaay kuraŋ ak yenn ci bànk yi. Yéenekaay bii di  Libération a ngi xamle itam ni mënatul leb xaalis ci bànk yi ndax bor yi mu ame.

AIBD fey na ay boram !

Ayeropoor bii di AIBD fey na bor yi mu ameeloon ñépp ñi ko lebaloon xaalis. Bor ya tollu woon nañ ci 393i miliyaar te fey na ko bala atum àpp mi di jot : 2029. Loolu la Dudu Ka, Njiital la fay saytu, xamle.

MBATIT

Bindkat bii di Soxna Benga dafa bëgg ñu yittéwoo téerey nettali yi bindkati réew mi di bind ngir ñu soppi leen def leen ay film walla ay série . Dafa bëgg maxejj yi mën a xam itam seen maanaa ak seen njariñ. Ci xalaatam, loolu dina dooleel sinemaawu réew mi. Téere bii ñu dippee « L’or de Ninkinanka », soppi woon nañ ko def ko « série » ca këru sinemaa bii di Maroodi tv waaye mën nañu jél yeneen i téere def leen nu ni mel.

TÀGGAT-YARAM

Mbër mii di Gribóordo, ginnaaw bi ko Bàlla Gay 2 daanee, amaat na joŋante bu war a dox ci digganteem ak kii di Aamaa Balde ci atum 5 féewariyee 2023. Waa Kajoor Production ñoo tëgg làmb jooju. Mu nekk ab joŋante bu tàmbalee yëngal làmb ji.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj