LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (GAAWU 21 SAŊWIYE 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Waxtaan wa doxoon diggante Nguur gi ak ñi yor wàllum dem bi ak dikk bi, déggoo mujjeewu ca am. Kenn ku nekk ak fa nga fare, ŋoy fa nga ŋoy ba mu dëgër. Mu mel ni saafara amagul ci boobu ñaxtu.

MITIŊU USMAAN SONKO 

Njiitu Pastef lii di Usmaan Sonko ma ngay waajal mitiŋ bu mag ba muy amal ca Kër Masaar. Mu war a am ëllëg ci dibéer, mu nar a nekk ndajeem pólitig mu réy niki ni ñu ko yëglee.

NJÀNG MI AK NJÀNGALE MI

La ub bopp yi di lim bu takku ba ñu nemmeeku ca joŋante CREM ba. Muy ay junniy junni ndaw yu bindu ngir nekk ay njàngalekat ci daara yu suufe yi. La waral lim bu takku boobu, ñenn ñi tënk ko ci payoor ya ñu yokku, ñeneen ñi gise ko ñàkkum xëyu ndaw ñi. 

KAAWTEEF

Wata ya ngay wéy di def ay jëyya ci tali yi. Ca Biññoona, gox ba ñu naan Jiñaaki, ñaari ndongo la fa wata fiir ba kenn ka ñàkk bakkanam, keneen ka ame ca ay gaañu-gaañu.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj