Dépite ya fare ca Wallu Senegaal, ña ngay sàkku ci njiitu jëwriñ ji Aamadu Ba, mu biral naali politigam ca Ngomblan ga. Mu nekk ab sas bu ko yoon sas. Waaye, loolu di tegu ci ab àpp bu tollu ci ñatti weer ginnaaw bi mu faloo.
KAAWTEEF
Musiba moo xew fee ca Séeju, ca dëkk bu ñuy wax Bunkiliŋ. As ndaw la boroom këram jam. Jëf ji, mbirum ñaan baat a ko sabab. Mu nekk ay xew-xew yu tàmbalee bari ci diggante way-dencante yi. Moo xam teg fitna la, léeg-léeg sax muy mujje ci faat bakkan. Mu jar a def taxaw seetlu balaa Làmbaay a ñaaw.
TÀGGAT YARAM
Joŋantefutbalu tefes ga réewi Afrig yi di amal ca Mosàmbig, gayndey Senegaal yi woneeti nañu seen mënin. Ginnaaw bi ñu jële raaya ba ci lu yàggul, firndeel nañu seen taxawaay ci poo moomu. Ci seen futbal bu njëkk door nañu Ugandaa 10i bal ci 1.