Tuuma ji ëttub cettantal gi tegoon ci yenn ndodd yi ñeel koppar yu ñu luubal ci xeexub mbas mi, Nguur gi àddu na ci. La ñu xamle nekk ay kàddu yu ñenn ñi di mettitlu ndax lañu xeeb koppar ya ne fuuraas ci seen biir. Mu ëpp juróom-benni tamndaret doonte ne néew na ca seen i bët.
BBY NJUUY NA LEEN
Mbootaay gii di Bennoo Bokk Yaakaar amal nañu seen ndaje ma ñu doon xaar ci ñoom. Kurél gi dajale na ay ñoñam ngir waajtaayu palum njiitu réew mi war a am fi ak at kese. Lañu doon xaar ca ñoom mooy ñu biral ka ñu nar a jiital bu boobaa. Mu mel ne am njuuy lañu tëgg. Ndax la ñu xamle di saa bu jotee rekk dinañ ko wax.
CAP
Kurél gi ëmb taskatu-xibaar yi nee nañu, du ñu tàyyi. Démb ci Àjjuma ji amal nañu waxtaan ak taskatu-xibaar yi ngir biral ay pexe ngir ñu bàyyi seen naataangoo bii di Paap Aale Ñaŋ. Lañu tënk mooy seeti kilifa diine yi ngir ñu àddu ci mbir moomu.
DIINE
Kercen yaa nga ca waajtaayu Nowel. Ñu ciy màggal Yéesu mu sell mi. Moo Señëer Bensame Njaay, njiitu jàngub Ndakaaru, jottali na ay kàddu askan wi. Mu leen di woo ci jàmm ak dal, te di ñaawlu fitna yi ñu nemmeeku ci réew mi, moo xam ci wax la, walla ci jëf.