LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (GAAWU 24 Sàttumbar 2022)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG 

Ginnaaw mbetteel ga mu am ca Ngomblan ga ca palum njiit la, ndax Aminata Ture dafa nar a ber yoonu boppam ? Mu nekk ab laaj bu xel yépp daj. Ndaxte, Mimi dafa mel ni kuy waaj ngir nekk lawax ca palum njiitu réew mi war a am 2024. 

MBATIIT

Mustafaa Géy nekkoon fi njiitu kurélu Imaam yi ak Ulemaawi Senegaal wàcc na liggéey. Ci tewaayu mbooloo mu takku, ay kilifa ak i imaam yu bari seedeel ñanu ko ay jikkoom yu baax ; gunge ko ca këram gu mujj. Ki ko fa wuutu léegi di wuyoo ci turu Umar Jéen. 

TÀGGAT-YARAM

Tay ci gàwwu bi Senegaal daje na ag Boliwii ci mats xaritoo. Gaynde yu Senegaal yi ñoo dóor waa Boliwii ñaari bal ci dara (2-0). Ña leen dugal di Bulaay Ja ak Saajo Maane. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj