LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (GAAWU 25 FÉEWARYEE 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Idi day bokk, walla ?

Dina amam du am, li ñu doon laam-laame léegi mu leer. Njiitu làng gii di RÉEW MI, Idriisa Sekk, nee ñu dina dogoo ak Màki Sàll, sàmp ndëndam ci joŋante palum Njiitu réew mi war a am 2024. Muy xibaar bu Seneweb siiwal. Lañu ca seetlu mooy ne, dogoo bi nar naa bari. Ndax, ñenn ciy ñoñam ya mu bokkal làng, nee ñu dañuy wéy ak Njiitu réew mi Màki Sàll. Ñu mën cee lime Mustafaa Mesere ak Muhammed Siise.

Idriisa Sekk : la ma doon bañ démb laay bañ tay

Mu mel ni coowal ñetteelu moome gi dalagut ci réew mi. Moo tax ba njiitu làngug pólitig bii di RÉEW MI fésal na ag péeteem. Ca ndaje ma ñu doon amal, Idriisa Sekk déey na leen ne la mu bañaloon Abdulaay Wàdd du ko nangul Màki Sàll.

TUUBAA

Ginnaaw lakk ga amoon ca ja bu Okaas, Baay faal yi am nañu ndigal ci xalifab Tuubaa ngir ñu xàll yoon yi. Liggéey boobu door na démb ci àjjuma ji, béréb yu bari yu ñu lim nar a bokk ci liggéey boobu.

TÀGGAT-TARAM : CAN U-20

Gaynde yu ndaw yi dóor nañu Esipt ma leen dalaloon. Joŋante boobu ñu jagleel ñi amagut 20 i at, gone ya gàddu nañu ndam li ci ñeenti bal ci dara (4-0). Paap Demba Jóob nekk kuppekat bi gën a ràññeeku ginnaaw bi mu dugalee ñatti bal yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj