LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI Gaawu 27 ut 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

 PÓLITIG 

Coow li amoon  ci diggante Gabriyel Kan ak jëwriñ ji ñu dénk mbiri jigéen ñi, Ndey Sali Jóob Jeŋ dakkagut.  Kenn ku bokk ca kurél ga, Awa Ba, ma ngay tontu ndaw soosu fi yékkati ay kàddu yu ñaaw jëmale ko ci jëwriñ jile. Ma ngay laaj ndax Gabriyel moo moom Saa-Senegaal yi. Ma nga koy dankaafu tamit ci ay xibaar yu mu xam ci moom. 

KOOM-KOOM

Ginnaaw génn bi Paap Aale Ñaŋ defoon di xamal Saa-Senegaal yi ne këru koomal gii di “Auchan Sénégal” day sédd ci lu tolloog 4i %  ca la muy am njiitu réew mi. Waa Auchan génne nañu ab yëgle di weddi wax jooju. 

WÉR-GI-YARAM

Waa Ànd-Gësam wàcc nañu tey jii ci mbeddi Cees ya. Li ko waral di dooleel seen moroom ya ñu tegoon loxo ca Raglub Maam Abdu Asiis ginnaaw liir ya fa ñàkkoon seen i bakkan. Ci kow loolu, ña ngay naqarlu seen nekkin ci seen i bérébu liggéeyukaay yooyu.  

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj