LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI Gaawu 27 ut 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Péncum ndawi réew ma

 Ca 12eelu fan ci weeru Sàttumbar la dépitey réew mi di amal seen ndaje mu njëkk fale ca Néncum ndawi réew ma. Bésub altine lay doon ginnaaw bi Ndajem ndeyu-àtte mi siiwalee njureef yu mujj yi ci wote yi.

Kariim Wàdd ca Senegaal

Kii di Kariim Wàdd te jiite ci jamono jii làngug PDS moo ngi xamal Saa-Senegaal yi ñu waajal delluseem ci réew mi.

KOOM-KOOM

Fale ca Tuubaa ci gox bi ñu dippe Daaru Rahmaan, ay boroomi tool (ay béykat) la fa ndox mi daaneel seen i miir. Waaye, bi loolu amee, Nguur gi wone na ci taxawaay bu am solo. Nde, nee na dina leen dooleel, jox leen xaalis ngir ñu mën cee tabaxaat ay taax yu bees.

TÀGGAT-YARAM

Basket-ball Senegaal

Léegi, Góorgi Si Jeŋ mooy kàppitenu ekibu Senegaal bu basket-ball.

Futbal Senegaal

Ekibu futbal bu Senegaal, ba tey, moo jiitu fii ci Afrig ba noppi féete ci fukk ak juróom-ñetteelu palaas ci toftale bu Fifa.

KAWTÉEF

Fale ca Jaxaay, ñoo ngi xamle ni senn ndaw su jigéen su am 13i at lañu maye fekk àndu ci. Moom la jëkkëram doon dóor bés bu nekk. Ndekete jëkkër ji tuxkatu yàmbaa la.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj