Tuuma ji ëttub cettantal gi tegoon ñenn ciy jëwriñ ak i DAGE ñeel koppar yu ñu luubal ci xeexum mbas mi, jëwriñ ji ñu dénk wàllum yoon di Ismayla Maajoor Faal, wax na ci. La mu ca xamle mooy, ñañu ca tudd, dinañu wuyuji yoon. Wànte, ñii di jëwriñ, ñoom, Yoon dafa am nu muy doxale ngir mën leen a topp.
SONKO, GANU FRANCE 24
Usman Sonko, njiitalu Pastef li, moo doon ganu teleb Farãs 24 ak RFI, démb ci àjjuma ji. Waxtaan wi mu séqaloon ak taskatu-xibaar yooyu, di dellusiwaat ci xew-xewu réew mi, tolluwaayam ci pólitig ak coowal ciif li dox digganteem ak Aji Saar. Moom, nag, yakk Njiitu réew mi lu mel ni xeme, setal deru kujje gi te xamle ñoom, bañuñoo liggéey ak Farãs, waaye ku leen noot lañuy bañ.
HCTT
Njiitu réew mi Màkki Sàll samp na tay ci Gaawu bi bànqaasub Magnum Ndajem mberaay yi, maanaam “Haut Conseil des Collectivités Territoriales”, gàttal biy joxe HCTT. Ginnaaw bi ñu amale wote yi ci weer yii ñu weesu, ña ñu fal nar a door seen ub liggéey ginnaaw si tay.
CAP
Kurél gi ëmb taskatu-xibaar yi amal nañu beneen feemu xeex ngir génne seen naataangoo bii di Paap Aale Ñaŋ ca ndung-siin. Ñuy sàkki ci Njiitu réew mi, mu may leen liñ koy ñaan.
KOOM-KOOM
Njëgu gaasuwaal bi ak esãs bi dinañ yokku tay ci Gaawu bi, bu fukki waxtu ak juróom-benn jote. Muy lu Càmm gi yëgle. Loolu nar a indi ay njeexital yu bari ci dundug askan wi.
DEM AK DIKK
Ña nar a yëg yokkuteg gaasuwaal bi ak esãs bi dëgg ñooy dawalkat yi. Ñooñu di àddu ci seen jafe-jafey liggéey bu ci lii dolleekoo. Lañuy artoo Nguur gi mooy bu loolu amee diñan yokk ñoom tamit paasu daamaar yi.