LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (TALAATA 14 MÀRS 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Ci talaatay tey ji la lëkkatoo Yewwi Askan Wi doon amal ab « Giga meeting » ca Parsel Aseni, pàkkub akapes. Mbooloo ma fees fa dell ba foo sàndi woon mbàttu, mu tag. Dafa di, ci guddi gi la nit ña tàmbalee ñëw, fanaansi. Laata ndaje miy door, béréb ba fees na dell. Bi Usmaan Sonko di ñëw, mbooloo mu takkoo takku a ko dar, gunge ko ba mu àgg.

Waaye, li gën a fës ca ndaje ma, mooy teewaayu Aminata Ture mii jiite woon toftaleg Bennoo Bokk Yaakaar ci wotey Ngomblaang gi, doon jàmmaarloo ak waa YAW. Waaw, moom kay, Mimi menn mi. Te sax, fi kilifay lëkkatoo gi toog lañ ko beral ab toogu, mu dend ak ñoom Xalifa Sàll, Usmaan Sonko, Decce Faal, Abiib Si, añs. Moom kay, jot na faa joxante loxo ak Usmaan Sonko sax.

Xanaa xëm ngeen !

MBIRUM PAAP NJAAY MU WALF

Bésub 7 màrs ba léegi, Paap Njaay, taskatu xibaaru Walftv bi, mi ngi ndung-siin tëdd. Lees koy toppe mooy ne dafa yékkatiy kàddu yoy, àttekat bi nee dañu wéradi. Moom, Paap Njaay, dafa àddu woon ci layoob Aji Saar ak Usmaan Sonko, waxoon ne, am nay àttekat yu àndul ci ni Yoon doxalee mbir mi. Kurél gii di RSF (Reporters sans frontières) nag, biral nañ seen njàqare ci ni Yoon di jàppee ak a tëj taskati xibaar yi jamono yii, ci Senegaal.

Walfadjiri, moomeet génne nab yégle, di ñaawlu mbir mi. Nee ñu, dinañu amal toogaanu ñaxtu ci seen buntu màkkaan, dibéer 19 màrs 2023, bu 15i waxtu jotee. Bind nañu caytu gi ngir yégal ko ko, te di ci woo képp ku Yoon itteel.

BITIM-RÉEW

Móritani

Ca réewum Móritani, Njiitu Réew ma, Muhamet Uld Séex El Qasuwaani, tas na Ngombalaan ga. Démb ci altine ji la bind ab dekkere daldi ciy siiwal ndogal li. Ba tey ci biir dekkere ba, ma nga cay xamle tamit ni dinañu amal i wote ngir tabb yeneen i dépite, njiiti diwaan yeek gox yi. Waaye, wote yi du àgg ci weeru ut wi ñu ko nisëroon. Dees leen di randalsi ci weeru me wii.

Jëwriñ jiñ dénk kaaraange biir réew ma, Mohamet Ahmet Uld Mohamet Lemin, andi nay leeral ñeel randalsi bi. Ci li mu siiwal, Nguur geek kujje gi waxtaan nañu ba déggoo ci ni def ko ci weeru me wii dina yombal mbir yi. Nde, weeru ut wi dafay yemook nawet bi. Te bu tàmbalee taw, dem beek dikk bi dafay jafe lool ci yenn diwaan yi.

Ngombalaan gu bees gi dina jóge ci 157i toogaan, dem ba ci 176i toogaan.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj