XIBAAR YI TUKKE CI NDAJEM WAXTAAN MI TOPPEKAT BU MAG BI DOON AMAL
Tey, ci yoor-yoor bi, la toppekat bu mag bi doon janook taskati-xibaar yi. Ibraayma Baaxum biral na fa wayndare yu bari, li ko dale pexem mbóomug Usmaan Sonko, mbirum Dr Baabakar Ñaŋ.
Pexem mbóomug Usmaan Sonko
Bu dee li ñeel njiitul Pastef li, toppekat bi nee na am na kuñ ci jàpp. Kooku nag, mi ngi wuyoo ci turu Yarga Si, bokk ci Pastef.
“Kibaraan yu bari biral nañu mbirum pexem mbóom ñeel Usmaan Sonko, di maxejjub Senegaal. Nee ñu, dafa am ñu bëggoon a faat bakkanam.”
Ciy waxam, buñ xoolee ab widewoo ci la gis kii di Yarga Si muy piis dara Usmaan Sonko. Biñ ko laajee, ba tey ci waxi toppekat bu mag bi, Yarga Si daf ne loolu bineegar la. Laaj nañ itam doktoor Suma Assurance yi ngir xam lu jot Usmaan Sonko. Waaye jëlewuñ ci dara. Nde, doktoor yi dañ bañ a tontu ngir ne seen càrtug liggéey mayu leen ko.
Mbirum Dr Baabakar Ñaŋ
Ibraayma Baaxum, toppekat bu mag bi, àddu na ci sabab yi tax ñu jàpp Dr Baabakar Ñaŋ. Daf ne, Bàmba Faal, meeru Médina, moo pelent ak itam jenn magu Mamadu Li mees duppee “Duudu Faal”. Mu neeti, ñoo ngi toppe Dr Baabakar Ñaŋ reyug teyeedi, tayleb bakkanu jàmbur ak ñàkk a wattu nit ku repp.
Dr Baabakar Ñaŋ a moom kilinig Suma Assistance biñ yóbboon Duudu Faal. Ñépp a ñaawlu anam yiñ jàppe woon fajkat bi ca Medina Njaajbe, takkal koy manot, indi ko Ndakaaru.
Toppekat bi nee, ubbees nab luññutu ñeel fajkat beek kii di Séex Mbàkke Médina Séy. Lees ko duggee mooy leeral mbir mi.
Mbirum komaandoo yi
Ibraayima Baaxum, toppekat bu mag bi andi naat i xibaar ñeel ñi yoon teg loxo. Bees sukkandikoo ciy kàddoom, am na ci ñoo xam ni, defkati ñaawteef lañu yoy, dañoo rax ci ñaxtukat yi. Dañoo taxawal am mbooloo mees duppe “komaandoo”. Loolu la xamle ci ñeenteelu poñ bi ci bi muy janook taskati-xibaar yi. Te, bees toppee gëstu bi, kii di Muraa Mani Kaba Jakate la duut baaraam ne moo nekk ca bopp ba, walla boog moo yor kàddu gi mbootaay googu di doxe. Ba tey ci li mu wax ni loolu la gëstu bi feeñal, mbooloo moomu dem na ba di jël ay nit ak a defar i ngànnaay ngir mën a dékku takk-der yi. Muy xibaar yu doy waar yu nekk ci biir wayndare wi muy jébbali àttekat bi.
RADDHOGÀNTAL NA 3eelu MOOME GI
Ca seen ndaje ma ñu doon amal ca seen màkkaam, tey ci talaata ji, waa RADDHO àddu nañ ci mbirum ñetteelu moome gi. Ñoom, nag, wax nañook Njiitu réew mi, Maki Sàll :
“Jamono yii, nemmeeku nañu ci Senegaal ay yëngu-yëngu ci wàllu pólitig, mboolaay gi ak koom-koom te, bokk na ci li ko waral, jafe-jafe yi kenn ci kujje giy jànkoonteel ak li Maki Sàll di nisër a def ñeel wotey 2024 yi.”
Ñoom, dañ jàpp ne, ni Yoon tëdde ak mbirum ñetteelu moome gi Maki Sàll di yóotu te Ndeyu àtte ji tere ko ko, ñoo yëngal réew mi. Ñaax nañ ñépp, muy waa Nguur gi, di Yoon, di kujje gi ak askan wi ngir ñu doxal Yoon ngir jàmmi réew mi.
Bu dee wàllu 3eelu moome gi, ñoo ngi ñaan Njiitu réew mi, Maki Sàll, mu sàmm kàddoom ak cëslaay gi wund Yoon wi ko teree am ñetteelu moome ginnaaw gu 2012 geek gu 2019 gi.
PEREFE BI GÀNTAL DOXU-ÑAXTU YAW
Lëkkatoog Yewwi Askan Wi dafa nammoon a amal i ndajem-ñaxtu ci àllarba jeek alxames jii. Waaye, dafa mel ni narul am. Ndax, perefeb Ndakaaru gàntal na ko. Li ko waral nag mooy ne mën na yee fitna te, day gàllankoor dem ak dikku nit ñi ak seen i alal. Ndogal lool, li mu ki dugge mooy sàmm kaaraange gi ak dalug maxejj yi ci dëkk bi. Mu yokk ci ne képp ku ci jàdd Yoon, ay daan ñoo la ciy xaar.
USMAAN SONKO
Njiitul Pastef li, Usmaan Sonko, bokk tamit ci lëkkatoo Yewwi Askan Wi, xamle na ne dina amal am ndajem-waxtaan tey ci ngoon. Moom nag ci alxames ji lees jàpp layoom beek Maam Mbay Ñaŋ.
TÀGGAT-YARAM : SENEGAAL DINA BOKK CI CAN 2023 BAY AME KODDIWAAR
Tey, ci ngoonug talaata ji, la gayndey Senegaal yi doon janook waa Mosàmbig ça Maputo. Ginnaaw bim ko dóoree 5-0 ça seen joŋante bu njëkk ba ame woon fii ci Jamñaajo, Senegaal dóoraat na ko 1-0. Bulaay Ja moo dugal bii bi. Ndam lii nag, dina tax Senegaal mën a bokk ca CAN 2023 bi war a âme ca réewum Koddiwaar.