LI GËN A FES CI XIBAARI FUTBAL (alxames 9 féewaryee 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

 BELSIG AM NA TAGGATKAT BU BEES

Kuppeg àddina 2018 ba léegi, Belsig dafa nekkoon ciy jafe-jafe. Njeexitalu kuppe gi gën koo feeñal. Moo tax ba seen tàggakat ba, Robeertoo Maartinees, xamoon boppam, tekki ndombal-tànkam balaa ñu koy dàq. Démb, ci àllarba ji la ñu xam ne ni tànn nañu Dominikoo Tedeskoo muy seen tàggatkat bu bees.

RONAALDIÑOO BU BEES ?

Ba nu xëyee la xibaar bi daanu, ñuy xamle ni saa-beresil bi, Ronaaldiñoo moo ngi dox ci tànki xaatimloo doomam ca Bàrsaa. Ndax dana mel ni baay ba ? Seetaan a dàkk cib ndaje, te lu ci kanam rawul i bët.

KUPPEG ADDINA KËLËB YI

Làmmiñ daal, ndeke mooy ndeyu balaa yi ! Vidaal de, ba ñu defee jiifii-jaafaa ba noppi, mu xam ni mën na am Real Madrid, la naagu di waxati bu jàppee Real Madrid na mu koy def. Da doon faf Al-Xilaal dóor ekibam bii di Falamingo 3-2. Ndeysaan. Wax baaxul.

ÀNGALTEER

Manchester City moo ngi ci guddi yu lëndëm jamono jii. Yoonu wure moo koy toppe li ñu jàpp ni dafa ñàkk doxal yoon ci njënd meek njaay mi ñeel wurekatam ya ; maanaam, fañ ko yamloo daf ko jéggi. Ñu ragal ni li ñu koy toppee bu dee dëgg diñañu ko teg daan yu diis, lu ci mel ni wàññiy poñam mbaa sax wàcce ko ca Championship.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj